Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 49
Alal day naxe
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.
 
2 Yeen, xeetoo xeet, dégluleen;
yeen, waa àddina yépp, teewluleen,
3 ngay ku tuut di ku mag,
nga bareleek nga néewle.
4 Li may wax xel la,
di xalaat yu déggu.
5 Damay teewlu kàddu yu xelu,
xalamal la sama tekkiteb cax.
 
6 Ana lu may tiit bés yu metti,
yu ma njublaŋ yéewe seeni ñaawtéef,
7 di ñu wóolu seen am-am,
di kañoo alal ju bare?
8 Ana ku mana jota jot sa bakkanu moroom,
mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga?
9 Njotug bakkan jafe na,
bu ci jéem dara.
10 Ana kuy dund ba fàww,
ba doo gis bàmmeel?
 
11 Xanaa gis ngeen ne xelu, dee;
dof, dee; naataxuuna it faatu rekk,
wacce keneen alalam.
12 Sa bàmmeel di sa kër, ba fàww,
di sa dëkkuwaay bu sax dàkk,
boo tudde woon sa bopp ay suuf sax.
13 Nit ak darajaam fanaanul,
mook aw rab a yem, sànku rekk.
 
14 Nii la ku wóolu boppam di mujje,
mook ku ko topp, di safooy waxam.
Selaw.
15 Nara dee rekk niy xar,
ndee wommat, yóbbu,
njub fenk nib jant, ku jub moom leen,
njaniiw mëdd seen jëmm,
fu sore kërug daraja.
16 Waaye Yàllaa may musal ci dooley njaniiw,
jot sama bakkan, ba jël ma.
 
17 Buleen yéemu ci ku barele,
teraangay këram di yokku.
18 Du dee ba yóbbaale dara,
teraangaam du ko topp biir bàmmeel.
19 Na bége bànneexu bakkanam,
ñu di ko kañe koomam,
20 ba tey, day dee, fekkiy maamam,
ña dootu gis ug leer ba fàww.
21 Nit ak darajaam fanaanul;
mook aw rab a yem, sànku rekk.

<- Sabóor 48Sabóor 50 ->