Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 47
Yàllaay buur
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.
 
2 Na xeetoo xeet tàccu,
xaacu, sarxolleel Yàlla!
3 Aji Sax ji, Aji Kawe jee jara ragal,
mooy buur bu mag bi tiim àddina sépp.
 
4 Moo nu nangulal xeet yi,
nu teg tànk gàngoor yi.
5 Moo nu tànnal céru suuf,
muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp.
6 Yàllaa yéeg, kàddu riir.
Aji Sax jee yéeg, bufta jolli.
 
7 Woyleen Yàlla, woyleen,
woyleen Yàlla sunu buur, woyleen.
8 Yàllaay buuru àddina sépp;
taalifleen, woy ko.
9 Yàllaa di buuru xeet yi,
Yàllaa tooge jalam bu sell.
10 Kàngami xeet yeey daje,
ànd ak ñoñi Yàllay Ibraayma;
Yàllaa moom buur yi yiir àddina,
te moo kawee kawe.

<- Sabóor 46Sabóor 48 ->