Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 46
Aji Sax jee ànd ak man
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.
 
2 Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel,
di nu wallu fu nu jaaxlee,
3 ba dunu tiit suuf su yëngu sax,
ba tund yiy tàbbi biir géej,
4 mbaa gannax yuy riir, di fuur
ak a fuddu bay gësëm tund yi.
Selaw.
 
5 Ag dex a ngi defi wal, di bànneexal dëkku Yàlla,
sellngay dëkkuwaayi Aji Kawe ji.
6 Yàllaa ngi ci biir dëkk bi, du raf;
Yàllaa koy dimbali ba jant fenkee.
7 Ay giir a riir, ay réew yëngu;
mu àddu, suuf seey!
8 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun,
Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale.
Selaw.
 
9 Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji,
ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.
10 Mu ngi fey xare ci àddina sépp,
dog fitt, damm xeej,
lakk pakk.
11 Mu ne: «Dal-leen te xam ne maay Yàlla,
màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.»
12 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun,
Yàllay Yanqóoba jii a nuy rawale.
Selaw.