Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 41
Jarag bu ñu toŋal a ngi ñaan
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
2 Ndokklee yaw mi yég néew-ji-doole.
Aji Sax jee lay xettli, bésub njàqare.
3 Aji Sax jee lay aar, di sàmm sa bakkan,
nga jagoo barke ci réew mi,
te du la bàyyi noon def la lu ko neex.
4 Aji Sax jee lay dooleel soo woppee,
di soppi bu baax sa tëraay.
 
5 Dama ne: «Aji Sax ji, tooñ naa la;
baaxe ma, faj ma.»
6 Noon yaa ngi may yéene lu bon,
naan: «Xanaa kii du dee, ba ñu fàtte ko?»
7 Ku dikk, di ma seet, di jinigal
tey fenti sos ci xolam,
bu génnee, tasaare ko.
8 Bañ yépp a ngi may déeyoo,
di ma fexeel lu bon,
9 naan: «Musiba dal na ko, du jógati!»
10 Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma,
te daan lekk samaw ñam.
 
11 Waaye ngalla Aji Sax ji, baaxe ma,
yékkati ma, ma fey leen.
12 Su noon damuwul ci sama kaw,
ma doora xam ne bége nga ma.
13 Man, damaa maandu, nga taxawu ma,
dëj ma fi sa kanam, ba fàww.
 
14 Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil.
Moo masa yelloo cant, ba fàww.
Amiin, Amiin.

<- Sabóor 40Sabóor 42 ->