Sabóor 38
Maa wopp, tuub, di jooy
1 Muy kàddug Sabóor guy fàttlee, ñeel Daawuda.
2 Éy Aji Sax ji, bul mer, di ma rëbb;
bul xadaru, di ma mbugal.
3 Aji Sax ji, fitt nga maa fitt,
dóor nga ma.
4 Danga maa mere, ma wéradi;
maa bàkkaar, ba jagadi.
5 Samay ñaawtéef mëdd ma,
diisa diis, ba àttanuma ko.
6 Maa def ug ndof,
ba am dana yu bédd, ba xasaw.
7 Maa ngi sëgg, ne yàcc, ne yasar,
di wéye tiis,
8 yaram tàng, di bax,
ma wéradi, ne làcc.
9 Sama yaram dee goyy, ma ne lasar,
jàq, di binni.
10 Boroom bi, yaa ngi ne jàkk ci samay nammeel,
samay onk umpu la.
11 Sama fit a ngi tëf-tëfi, doole ŋiis,
gët giim.
12 Xarit ak dëkkandoo di ma daw,
mbokk dànd ma.
13 Ñi may wuta rey a ngi may fiir,
di ma jéema lor, di ma waxal musiba,
yendu maa lalal pexe.
14 Man, ma mel nib tëx, dégguma,
mel ni luu, àdduwma,
15 di saf ku dul dégg,
bay layoo.
16 Aji Sax ji, yaw laa yaakaar;
Boroom bi, sama Yàlla, yaa may nangul.
17 Ma ne, ngalla buñu ma ree,
di damoo samab jéll.
18 Maa ngii di waaja daanu,
dëkke metit.
19 Ma ne, aylayéwén def naa lu ñaaw,
sama bàkkaar tiital na ma.
20 Noon yaa ngi ne jonn ak seen doole,
bare na ñu ma bañ ci neen.
21 Ma ji leen njekk, ñu fey ma njekkar;
may sàkku lu baax, ñu di ma sikk.
22 Éy Aji Sax ji sama Yàlla, bu ma wacc,
bu ma sore.
23 Ngalla gaawe ma;