Sabóor 28
Aji Sax jeey àtte ñoñam
1 Ñeel Daawuda.
Éy Aji Sax ji, yaw laay woo,
di la wéeroo, bu ma tanqamlu.
Soo nee cell,
ma xawa tàbbim pax.
2 Ngalla déglul, ma tinu la,
woo la wall,
dékk lay yoxo,
jublu sa néegu biir bu sell ba.
3 Bu ma sànkaaleek ab soxor,
di ma booleek kuy def lu bon,
di wax moroom ma jàmm,
te dencal ko ay ca xolam.
4 Fey leen seen liggéey,
seen kemu jëf ju bon.
Jox leen seen añu jëf,
yool leen seen yelleef.
5 Xooluñu Aji Sax jeeki jëfam,
ak liggéey bi mu def.
Da leen di yàqte,
te dootu leen yékkati.
6 Jaajëfe Aji Sax ji,
ki ma nangul samay dagaan!
7 Aji Sax jee may dooleel, di ma feg.
Moom laa wóolu, mu wallu ma,
sama xol tooy,
ma woy, sante ko.
8 Aji Sax jeey dooleel ñoñam.
Mooy làq, di musal buur bi mu fal.
9 Ngalla musalal sa mbooloo,
barkeelal sa ñoñ ñii,