Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 27
Xare jib, ma ànd ak Yàlla
1 Ñeel Daawuda.
 
Aji Sax jee may leeral, di ma wallu.
Ana ku may ragal?
Aji Sax jeey aar sama bakkan.
Ana ku may tiit?
2 Ab soxor wutsi ma,
nar maa yàpp,
noonoo ma, bañ ma;
mooy tërëf, fëlëñu.
3 Bu gàngoor booloo sama kaw,
duma raf.
Ab xare jib,
ma ànd ak Yàlla.
 
4 Lenn laa ñaan Aji Sax ji,
lii laay sàkku:
dëkk kër Aji Sax ji,
sama giiru dund,
di niir taaru Aji Sax ji,
te yéemoo këram.
5 Bésub ay, mu yiire ma mbaaram,
làq ma, ma làqoo xaymaam,
aj ma ciw doj, ma raw.
6 Ma doxe fa siggi,
tiim noon yi ma wër,
di sarxali fa xaymaam
saraxi sarxolle.
Naa woyal Aji Sax ji, joobe ko.
 
7 Éy Aji Sax ji, déglul, ma woote!
Ngalla baaxe ma, nangul ma.
8 Yaw la sam xel ne ma, ma sàkku la,
te it yaw Aji Sax ji laay sàkku.
9 Sang bi, bu ma làqu,
bul mer, jañax ma.
Yaa ma daa wallu.
Bu ma wacc, bu ma ba,
yaay Yàlla mi may musal.
10 Ndey ak baay man nañu maa wacc,
Aji Sax ji fat ma.
11 Éy Aji Sax ji, joxoñ ma saw yoon,
jaarale ma joor gu wóor,
ngir ñi may tëru.
12 Bu ma baye bànneexu noon.
Seedey naaféq a ma jógal,
di sos fitna.
13 Maay dajeek ngëneelu Aji Sax ji
fi kaw suuf sii.
Lii wóor na ma.
14 Yaakaaral Aji Sax ji,
dëgërlul te amu fit,
te yaakaarati Aji Sax ji.

<- Sabóor 26Sabóor 28 ->