Sabóor 25
Aji Sax jeey gindee, di yiire
1 Ñeel Daawuda.
Aji Sax ji, yaw laay diis sama bakkan.
2 Sama Yàlla, yaw laa yaakaar.
Yàlla buma rus,
noon yi ree.
3 Deesu la séentu, ba rus.
Kuy wor ci neen mooy rus.
4 Éy, Aji Sax ji, won ma saw yoon,
xamal ma fi nga ma jaarloo.
5 Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma.
Yaw yaay Yàlla ji may musal,
ma di la yendoo yaakaar.
6 Aji Sax ji, bàyyil xel sa yërmandeek sa ngor.
Naka jekk sa jikkoo!
7 Bul xool li ma bàkkaare ndaw ak li ma moy.
Aji Sax ji, xoole ma sa ngor ngir sag mbaax.
8 Aji Sax jee baax, rafeti dogal,
di gindi moykat ci yoon wi,
9 di jiite ku woyof mbubb ci njubte,
di ko xamal aw yoonam.
10 Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiitee
kuy sàmm kóllëreem ak seedey yoonam.
11 Éy Aji Sax ji, tooñ naa lool,
jéggal ma ngir saw tur.
12 Ana kuy wormaal Aji Sax ji,
mu won ko yoon wi mata taamu,
13 muy dunde ngëneel,
askanam moom réew mi?
14 Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal.
Kóllëreem la koy xamal.
15 Samay gët jàkk rekk ci Aji Sax ji,
moo may xettli ci fiiru noon.
16 Ngalla geesu ma, baaxe ma,
maa wéet, néew doole,
17 sama xol feesey xalaat.
Rikk, teggil ma njàqare!
18 Xoolal sama naqar ak sama tiis,
te baal ma bépp bàkkaar.
19 Xoolal noon yi ne gàññ,
bañ ma mbañeelu fitna.
20 Éy, aar ma, musal ma!
Bu ma rusloo,
yaw laa làqoo.
21 Yal na ma maanduteek njub taxawu,
maa ngii, di la xaar.