Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 21
Aji Sax ji baaxe na Buur
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
2 Céy Aji Sax ji, Buur a ngi bége sa doole,
di bànneexoo sag wall, rekk.
3 Yaa ko may nammeeli xolam,
gàntuwulooy dagaanam.
Selaw.
4 Yaa ko gatandoo barkey ngëneel,
kaalaa ko wurusu ngalam.
5 Mu ñaan mucc,
nga saxal jalam fàww,
6 sag wall a ko sagala sagal!
Teddngaak daraja nga ko sédd,
7 jagleel ko barke bu sax dàkk,
bégale ko sa kanam, mu bànneexu.
8 Buur wóolu na Aji Sax ji, moos,
du tërëf, Aji Kawe jee gore.
 
9 Buur, yaa naan sa noon yépp céex,
ne say bañ taral.
10 Soo nee jalañ, jafal, ñu boy.
Aji Sax ji mer, sànk leen,
sawara xoyom leen.
11 Yaay raafal seeni giir fi kaw suuf,
fey seen askan ci doom aadama yi.
12 Ñoo la mébal lu bon,
nasal la pexe, joyul.
13 Nga di leen diir fittu kanam,
ñu wone gannaaw.
 
14 Aji Sax ji, jógal ak sa manoore,
nu joobe la, woy sa jaloore.

<- Sabóor 20Sabóor 22 ->