Sabóor 2
Yàlla fal na buur
1 Ana lu xeeti àddina di riir,
lu giir yiy nas pexey neen?
2 Buuri àddinaa ngi dér,
boroom nguur yi daje,
di fexeel Aji Sax ji,
mook ki mu fal.
3 Ña nga naan: «Nanu dagg càllala yi,
sànni jéng yi!»
4 Ki ci jalub asamaan a ngay ree,
Boroom baa nga leen di kókkali,
5 mer, ba gëdd leen,
xadaru, tiital leen ne:
6 «Man maa tabb buur, fal ko ci Siyoŋ*2.6 Siyoŋ: Siyoŋ fii mooy tund wa kër Yàlla ga nekkoon ca Yerusalem. Daan nañu ko tudde it dëkku Yerusalem mbaa réewum Israyil. ,
sama tund wu sell.»
7 Buur ne: «Ma biral dogalu Aji Sax ji,
moom mi ma ne: “Yaa di sama doom,
8 Ñaan ma xeeti àddina, ma sédd la ko,
nga moom ba ca cati àddina,
9 yilife leen yetu weñ,
rajaxe leen ni njaqal xandeer.”»
10 Kon yeen buur yi, muusleen,
kilifay àddina, fàgguleen.
11 Jaamuleen Aji Sax ji, ragal ko,
di ko bége, ba yaram daw.
12 Sujjóotal-leen doom ji, bala moo mer,
ngeen sànkoo seenu yoon;
meram day jekki ne jippét,
waaye ndokklee képp ku ko làqoo!
<- Sabóor 1Sabóor 3 ->
- a 2.6 Siyoŋ: Siyoŋ fii mooy tund wa kër Yàlla ga nekkoon ca Yerusalem. Daan nañu ko tudde it dëkku Yerusalem mbaa réewum Israyil.
- b 2.7 Jur: su Yàlla nee moo jur buur bi, waxin la rekk. Bés bi ñuy fal buur bi la Yàlla di biral ne jàppe na buur bi ni doomam. Ni doom di taxawale baayam, ni la buur biy taxawale Yàlla ci kaw suuf. Ni baay di sàmme doomam it, ni la Yàlla di sàmme buur bi, ngir mu am ndam.