Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 149
Na Israyil màggal Ki Sax
1 Màggal-leen Ki Sax!
Woyleen Aji Sax ji woy wu yees,
màggal ko fi ndajem wóllëreem ñi.
2 Na Israyil bége kii ko sàkk,
doomi Siyoŋ, laa ne, ñu bànneexoo seen buur bii.
3 Nañu màggale turam am pecc,
tëggal ko, xalamal ko.
4 Aji Sax jee safoo ñoñam,
di terale néew-ji-doole ag mucc.
 
5 Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam,
bu ñu tëddee sax, di sarxolle,
6 di xaacuy kañ Yàlla,
ŋàbbaale saamaru ñaari ñawka,
7 ngir duma yéefar yi,
mbugale ko yooyu xeet,
8 yeewe seeni buur ay càllala,
jénge seeni njiit jéngi weñ,
9 ngir sottalal leen àtte bi ñu bind,
muy ndamu wóllërey Yàlla yépp.
Màggal-leen Ki Sax!

<- Sabóor 148Sabóor 150 ->