Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 148
Na àddina wërngal këpp màggal Yàlla
1 Màggal-leen Ki Sax!
Nangeen màggale Aji Sax ji fa asamaan,
màggale ko fa kawa kaw.
2 Màggal-leen ko, yeen malaakaam yépp,
màggal-leen ko, yeen gàngooram yi.
3 Màggal-leen ko, yeen jant beek weer wi,
màggal-leen ko, yeen mboolem biddiiw yii di nes-nesi.
4 Màggal-leen ko, yeen asamaani kaw-li-kaw,
ba ca ndox ma tiim asamaan ya.
5 Nañu màggal turu Aji Sax ji,
kii kat a santaane, lii lépp am.
6 Moo leen samp, ñu sax ba fàww,
mu dogal ko, te du toxu.
 
7 Nangeen màggale Aji Sax ji fa kaw suuf,
yeen ninki-nànkay géej ak xóote yépp,
8 ba ca melax yaak doj yu sedd yay taw,
ak tawub yuur akub lay,
ba ca ngëlén yu mag yay def ndigalam.
9 Màggal-leen ko yeen tund yu mag yeek
yu ndaw yépp,
ba ci garab yiy meññ ak garabi seedar yi,
10 ba ci mala yépp, yu àll ak gépp jur
ak luy raam ak njanaaw,
11 ak buuri àddinaak xeet yépp,
ak kilifa yeek njiiti àddina yépp,
12 xale bu góor ak bu jigéen,
mag ak ndaw.
13 Màggal-leen turu Aji Sax ji,
moom doŋŋ la turam kawe,
darajaam tiim asamaan ak suuf.
14 Moo dooleel ñoñam,
wóllëreem ñiy mbooloom bànni Israyil,
xeet wi mu xejjoo, di ko màggal.
Màggal-leen Ki Sax!

<- Sabóor 147Sabóor 149 ->