Sabóor 146
Buur Yàllaa jara wóolu
1 Màggal-leen Ki Sax!
Naa màggale Aji Sax ji xol,
2 li feek may dund, di ko kañ,
li feek may noyyi, di woy sama Yàlla.
3 Buleen wóolu kilifa,
doom aadama amul wall.
4 Noo ga day rëcc, mu dellu suuf;
bu bés baa, pexeem jeex.
5 Ndokklee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba;
di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji,
6 ki sàkk kaw ak suuf,
géej ak lu ci biiram,
di sàmm dëgg ba fàww,
7 di àtte néew-ji-doole,
di leel ku xiif.
Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj.
8 Aji Sax jeey xippil silmaxa,
di siggil ku sëgg.
Aji Sax jee sopp ku jub.
9 Aji Sax jeey sàmm doxandéem,
taxawu jirim ak jëtun,
waaye mooy lajjal pexem ku bon.
10 Aji Sax jeey nguuru ba fàww.
Yaw Siyoŋ, sa Yàllaa ñeel maasoo maas.