Sabóor 133
Bokk, bennoo neex
1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
Céy liika baax te neexati,
ay bokk yu bokk dëkk, di benn!
2 Daa neex ni diwu bopp gu xeeñ,
siite sikkim, bu mel ni sikkimu Aaróona,
rogalaat ba ci mbubbam,
3 neex ni layub tundu Ermon,
neex ni lay bu ni mel tey rogalaate tundi Siyoŋ.
Fa la Aji Sax ji dogal barke,