Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 132
Yàlla digoo naak ki mu fal
1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
 
Éy Aji Sax ji, bàyyil xel Daawuda,
ak gépp njàqareem.
2 Moo giñaloon Aji Sax ji,
moo digook Mbërum Yanqóoba ma.
3 Mu ne: «Duma ñibbi,
4 duma tëddi sama kaw lal ba,
duma nelaw, duma gëmm sax bët,
5 li feek sàkkaluma Aji Sax ji bérab,
ba dëkkal Mbërum Yanqóoba ma.»
6 Ma ne, Efrata lanu dégg gaalu Yàlla ga,
fekk ko àllub Yaar.
7 Nan dem ba këram,
sujjóotali ndëggëstalu tànkam ya.
8 Aji Sax ji, jógal agsi sa dal-lukaay,
yaak sa gaal gi jëmmal sa doole.
9 Say sarxalkat, yal nañu woddoo njekk,
sa wóllëre yi sarxolleendoo.
10 Xoolal ci Daawuda, sa jaam ba,
bul gàntu ki nga fal.
 
11 Aji Sax ji daa giñal Daawuda
dëgg gu mu dul dëddu,
ne ko: «Ku jóge sa geño
laay wuutal ci sa jal bi,
12 te say doom, bu ñu sàmmee sama kóllëre,
ak sama kàdduy seede yi ma leen di xamal,
seeni doom it ñooy tooge
sa jal ba fàww.»
13 Aji Sax ji kat a tànn Siyoŋ,
taamu faa dëkke.
14 Mu ne: «Fii laay dal-loo ba fàww,
fii laay dëkk, maa ko taamu.
15 Dund bi, ma barkeela barkeel,
néew-ji-doole yi, ma reggal;
16 sarxalkat yi, ma wodde njot;
way-gëm ñi di sarxollee sarxolle.
17 Fa laay dooleele Daawuda,
taalal ki ma fal,
18 ay noonam, ma wodde gàcce;
moom, kaalaam ne ràññ.»

<- Sabóor 131Sabóor 133 ->