Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 131
Damaa woyof, gëm Yàlla
1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
 
Éy Aji Sax ji, man de, réy-réyluwma,
daŋŋiiraluma,
xintewoowma lu réy it,
mbaa lu ma ëlëm.
2 Xanaa ne tekk, ne cell,
ni perantal ak ndeyam;
sama xel dal ni perantal.
3 Éey Israyil, yaakaaral Aji Sax ji
tey ak ëllëg.

<- Sabóor 130Sabóor 132 ->