Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 130
Nu séentu njotug Yàlla
1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
 
Aji Sax ji, ci ay xóote laa lay wooye.
2 Boroom bi, déglu ma,
teewlu ma, ma tinu la.
 
3 Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar,
Boroom bi, ana kuy taxaw?
4 Waaye yaay jéggale,
ñu ragal la.
 
5 Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol,
di yaakaar kàddoom.
6 Wattukat bi yàkkamti njël,
wattukat bi yàkkamti njël, laa ne,
ni ma yàkkamtee Aji Sax jee ko raw.
 
7 Éey Israyil, négandikul Aji Sax ji.
Aji Sax jee gore,
te yaatug njot.
8 Mooy jot Israyil ci ñaawtéefam yépp.

<- Sabóor 129Sabóor 131 ->