Sabóor 13
Aji Sax ji, loo deeti xaar?
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2 Céy Aji Sax ji, loo deeti xaar?
Xanaa doo ma tanqamlu ba fàww?
Loo deeti xaar, bañ maa geesu,
3 ba ma tàggook bopp bu ubu
ak njàqarey xol bu sax,
ba noon dootu ma man?
4 Céy Aji Sax ji sama Yàlla, geesu ma, wuyu ma,
leqli ma, bala ma ne sërëx ci nelawi ndee,
5 noon ba naan: «Daan naa ko,»
bañ yay bége saab jéll.
6 Man de maa ngi dénkoo sa ngor,
di bànneexoo sag wall.
Naa woy Aji Sax ji,