Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 129
Noon manul Israyil
1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
 
Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonala sonal.
Israyiloo, waxati ko:
2 Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonala sonal,
te taxul ñu man ma.
3 Sama gannaaw gi lañu gàbba gàbb,
rëdd koo rëdd nib tool.
4 Waaye Aji Sax ji boroom njekk
dog na buumi ñu bon ña.
 
5 Képp ku noonoo Siyoŋ
yal nañu ko dëpp, gàcceel ko.
6 Yal nañu mel ni ñax mu saxem xadd,
balaa law, lax.
7 Du doyub ŋëb ku ko dog;
du doyub say ku ko for.
8 Ku fa jaare it du ko ne:
«Jaajëf, Aji Sax ji barkeel;
jaajëfe yaw, yal na Aji Sax ji barkeel.»

<- Sabóor 128Sabóor 130 ->