Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 127
Barkeb Yàllaa wóor
1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan.
 
Kër, su ko Aji Sax ji tabaxul,
ku ko tabax, neen nga doñ-doñi.
Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul,
ku ko wattu, neen nga teewlu.
2 Neen it la nit di teela jóg
ak a guddee tëdd,
di doñ-doñi lu mu lekk:
Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day,
fekk ko muy nelaw.
 
3 Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde,
njurum doom yool la.
4 Doom joo jure ndaw,
mooy fitt ci loxol jàmbaar;
5 ndokklee ku ci mbuusam fees,
ba bu ñu taseek ub noon ca pénc ma,
duñu am gàcce mukk.

<- Sabóor 126Sabóor 128 ->