Sabóor 116
Ma sant Yàlla mi ma jot
1 Maa bëgg Aji Sax ji: maa ko woo,
dagaan ko, mu dégg ma.
2 Teewlu na ma moos,
dama koy woo li feek may dund.
3 Buumi ndee a ma laawoon,
njàqarey njaniiw dab ma,
ma dajeek naqar aku tiis.
4 Ma woo Aji Sax ji wall, ne ko:
«Ngalla Aji Sax ji, xettli ma!»
5 Aji Sax jeey boroom yiw ak njekk,
sunu Yàllaay boroom yërmande.
6 Aji Sax jeey aar ku xamul àddina;
tumurànke woon naa, mu wallu ma.
7 Bu ma yeboo sama xel dal,
Aji Sax ji baaxe na ma!
8 Xettli nga ma, ba deewuma,
jàpple ma ba tërëfuma,
feral nga it samay rongooñ.
9 Damay topp Aji Sax ji
ci biir réewum aji dund ñi.
10 Ba ma naa: «Torox naa ba toskare,»
teewul may ànd ak ngëm.
11 Maa jàqoon ba naan:
«Ñéppi fen-kat lañu!»
12 Ana lu may njukkale Aji Sax ji,
li mu ma baaxe lépp?
13 Xanaa ma yékkati kaasu Aji Sax
jiy misaal wallam,
te may tudd turam.
14 Samay digeek Aji Sax ji laay matal
fi kanam ñoñam ñépp.
15 Wóllërey Aji Sax ji,
bakkanam ñor na Aji Sax ji.
16 Aji Sax ji, maay sab jaam,
maay sab jaam, di sa doomu jaam bi ma sukk jur.
Yaa yiwi samay buum,
17 yaw laay sarxalal saraxu cant,
te turu Aji Sax ji laay tudd.
18 Samay digeek Aji Sax ji laay matal
fi kanam ñoñam ñépp,
19 fi ëtti kër Aji Sax ji,
fi digg Yerusalem.