Sabóor 113
Buur Yàllaay walloo
1 Màggal-leen Ki Sax!
Yeen ñiy jaamu Aji Sax ji, màggal-leen ko,
màggal-leen turu Aji Sax ji!
2 Yal nañu teral turu Aji Sax ji
tey ak ëllëg!
3 Li dale penku ba sowu,
màggal-leen Aji Sax ji.
4 Aji Sax jee kawe, tiim xeetoo xeet,
teddngaam sut asamaan!
5 Ana ku mel ni sunu Yàlla Aji Sax ji,
ki kaweel ab jalam, toog,
6 di jéer asamaan ak suuf?
7 Mooy yékkatee ku néewle fa suuf,
di seppee ku sonn cib sën,
8 bokkal ko jataayu kilifa,
ya jiite xeetam.
9 Mooy dëël jigéen ju tële woona jur,
may ko mbégtem njureel.