Sabóor 112
Ku ragal Yàlla gis njekkam
1 Màggal-leen Ki Sax!
Ndokklee ku ragal Aji Sax ji,
di tàqamtikoo ay santaaneem.
2 Aw askanam ay am doole ci réew mi.
Ku jub saw xeet barkeel,
3 alal ak koom am sa kër,
sag njekk sax dàkk.
4 Ceeñeeru biir lëndëm jollil na ku jub
ak ku baax, di boroom yërmande ak njekk.
5 Ki baaxle mooy ki laabiir, di leble,
di jëflante cig njub.
6 Ku jub du tërëf mukk,
te dees na ko fàttliku ba fàww.
7 Du ragal dég-dég bu tiis,
xel ma day dal, mu wóolu Aji Sax ji,
8 fit wa toog, du ragal,
ba kera muy gis noonam jóoru.
9 Mooy nàddil néew-doole yi,
njekkam sax dàkk,
dooleem di yokku, ànd ak daraja.
10 Soxor bi da koy gis, mer,
iñaan bay yéyu, jeex tàkk;