Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 111
Yàlla la ay mbiram sax
1 Màggal-leen Ki Sax!
Naa sante Aji Sax ji léppi xol
ci biir ñu jub ñi bokk jataay.
2 Liggéeyi Aji Sax ji réy na,
ku ko safoo di ko gëstu.
3 Jëfam teddnga laak daraja,
njekkam di sax ba fàww.
4 Moo dogal ñuy fàttlikuy kéemaanam;
Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande.
5 Mooy leel ku ko ragal,
di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww.
6 Won na ñoñam dooley jëfam,
ba mu leen joxee suufu xeet yi.
7 Ay jëfam dëgg laak njub,
tegtalam yépp mata wóolu,
8 laloo dëgg ak njub,
te sax dàkk ba fàww.
9 Moo yónnee xeetam wall,
fas ak ñoom kóllëre gu sax.
Kee sell te jara ragal!
10 Ragal Aji Sax ji di ndoortel rafet xel,
dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye.
Moo yeyoo cant ba fàww.

<- Sabóor 110Sabóor 112 ->