Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 110
Yàlla fal na nitam
1 Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
 
Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko:
«Toogeel sama ndijoor,
ba ma def say noon sa ndëggastal.»
 
2 Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa Siyoŋ.
Yilifal noon yi la wër!
3 Sa mboolooy taxawal seen bopp,
sa bésub xare.
Ña nga soloo darajaak sellnga,
faboo fa njël sosoo,
diy ndaw, wàccsil la, mbeteb lay.
 
4 Aji Sax jee ko giñ,
te du dellu gannaaw:
«Yaa dib sarxalkat ba fàww,
topp dayob Melkisedeg*110.4 Melkisedeg: buurub Salem la woon, di sarxalkat bu Yàlla faloon ci jamonoy Ibraayma, maanaam ñeenti téeméeri at laata Aaróonaa doon ab sarxalkat.
 
5 Sang baa ngi fi sa ndijoor
te mooy rajaxe buur yi, bés bu meree.
6 Mooy mbugal xeet yi, jal seeni néew,
di rajaxe kilifay àddina, ba mu daj.
 
7 Déeg ba feggook yoon wa, Buur a cay naan,
te moo ko tax di siggi.

<- Sabóor 109Sabóor 111 ->