Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 11
Ma làqoo Aji Sax ji
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda.
 
Aji Sax ji laa làqoo.
Ana lu ngeen ma naa: «Neel fëyy ni picc, toŋi sa kaw tund.
2 Xanaa du ñu soxor ñaa ngii, bank seen xala,
nas seenu fitt,
nara lëndëmtu, jam ku jub?
3 Bu ponki njub màbbee,
nu aji jub di def?»
 
4 Aji Sax jaa nga këram gu sell.
Aji Sax jaa nga asamaan, kaw jalam,
ne jàkk doom aadama, di ko seetlu.
5 Aji Sax ji day seetlu ku jub;
ku soxor, bëgg fitna, mu bañ.
6 Day tawal ku bon ay mbugal;
sawaraak tamarax akub jaas dib añam.
7 Aji Sax jee jub, sopp njub;
kuy jubal, gis yiwam.

<- Sabóor 10Sabóor 12 ->