Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 107
Aji Sax jeey xettlee
1 Santleen Aji Sax ji, kee baax,
kee saxoo ngoram!
2 Waxleen lii, yeen ñi Aji Sax ji jot,
jote leen ci loxol bañ,
3 dajalee leen fa réew ya,
jële leen penkook sowu,
ak bëj-gànnaar ak wetu géej.
 
4 Ñee ngi taxawaaloo màndiŋ mu wéet,
gisuñu dëkkuwaay,
5 boole xiif ak mar,
ba bakkan di tàggoo.
6 Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall,
mu xettlee leen seen njàqare,
7 jaarale leen yoon wu jub,
ngir ñu àgg cib dëkk.
8 Nañu sante Aji Sax ji ngoram
ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.
9 Mooy màndal put gu wow,
di feesal ngëneel biir bu wéet.
 
10 Ñee ngi dëkke lëndëm gu tar,
ñu yeewe leen jéngi weñ yu tar.
11 Ñoo gàntal waxi Yàlla,
néewal ndigalal Aji Kawe ji.
12 Mu teg leen naqar, ba torxal leen,
ñu ne nërëm te kenn walluw leen.
13 Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall,
mu walloo leen seen njàqare,
14 xar seeni jéng yaar,
génnee leen lëndëm gu tar.
15 Nañu sante Aji Sax ji ngoram
ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.
16 Moo rajaxe bunti xànjar,
damm galani weñ.
 
17 Ñu dofe ñalee ngi topp yoonu moy,
loroo seeni ñaawtéef,
18 ba luy ñam di daw seen yaram,
ñu jege bunti ndee.
19 Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall,
mu walloo leen seen njàqare.
20 Daa yónnee kàddoom, wéral leen,
këfe leen cim yeer.
21 Nañu sante Aji Sax ji ngoram
ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.
22 Nañ ko sarxal saraxi cant
tey sarxolle, siiwale koy jalooreem.
 
23 Ña ca des a ngi war gaal, dugg géej,
di liggéeye mbeex mu ne xéew.
24 Ñooñoo seede jaloorey Aji Sax ji,
ak kéemaanam ya fa xóote ya.
25 Day àddu, sant ngëlén,
mu yékkati gannax yi.
26 Gannax ya fettax ba ca kawa kaw,
xàwwikoo fa, tàbbi xóote ya.
Ñu jàq ba fit ne soyox,
27 di jang, di kayaŋ-kayaŋi niy màndikat,
pexe jeex.
28 Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall,
mu génnee leen seen njàqare,
29 dalal ngëlén la,
gannax ya selaw,
30 ne tekk, ñu bég,
mu gindi leen ba fa ñu bëgga teer.
31 Nañu sante Aji Sax ji ngoram
ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.
32 Nañu ko kañe ndajem mbooloo mi,
di ko màggale péncu mag ñi.
 
33 Mooy soppi wali ndox màndiŋ,
soppi bëti ndox suuf su ne sereŋ,
34 suuf su nangu doon jooru xorom
ndax mbonug ña ko dëkke.
35 Mooy soppi màndiŋ it, ndox ya taa,
soppi suuf su ne sereŋ bëti ndox;
36 dëël fa ñu xiif,
ñu sanc fab dëkk, dëkke,
37 ji ay tool, jëmbat ay reseñ,
mu meññ, ñoral,
38 Aji Sax ji barkeel, ñu giira giir,
te wàññiwul seenug jur.
39 Bu ñu wàññikoo, ba néew doole
ndax noteel ak coonooku tiis,
40 Aji Sax ji sib seen njiit yi leen not,
wërloo leen àll bu amul yoon.
41 Waaye mooy teggil néew-ji-doole coonoom,
ful njabootam nig jur,
42 aji jub ñi gis ko, bég;
mboolem ku bon wedam.
43 Ku xelu ku ne, na ràññee lii
te seede li Aji Sax ji jëfe ngoram.

<- Sabóor 106Sabóor 108 ->