Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site

Sabóor

Sabóor 1
Ñaari yoon a ngii
1 Ndokklee yaw mi toppul tànki ku bon,
taxawewuloo yoonu moykat,
toogewuloo jataayu ñaawlekat.
2 Xanaa di bége yoonu Aji Sax ji,
di ko jàngat guddeek bëccëg.
3 Loo def mu àntu:
nga mel ni garab gu saxe walum ndox,
bu jotee meññ,
te xob wa du lax.
 
4 Loolu dalul moos ku bon,
kay mel ni xatax bu ngelaw li wal.
5 Moo tax ku bon du siggee àtte ba,
moykat du taxawe ndajem aji jub ña.
 
6 Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub;
yoonu ku bon di sànk boroom.

Sabóor 2 ->