Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Buur Lemuyel a ngi yeete
Saar 31
(Saar 31)

1 Lii waxi Lemuyel la, buuru Maasa*31.1 Maasa bérab la bu genn giirug Israyil sancoon ca bëj-gànnaaru Arabi., te ndeyam jàngal ko ko. Mu ne:

 
2 Ngóor si doom, saa doomi bopp!
Yaa di ñaan gu nangu, doom!
3 Bul jox jigéen ñi sa doole,
bul jox say siddit jigéen ñiy sànk buur.
4 Buur moomul di naan biiñ, Lemuyel,
buur moomu ko;
kilifa moomul di sàkku ñoll.
5 Lu ko moy mu naan, ba fàtte lu yoon tëral,
xañ néew-ji-doole ju ne, àqam.
6 Bàyyeel ñoll kuy sànku,
bàyyi biiñ ak boroom naqar.
7 Bu ñu naanee, fàtte seen néewle,
ba dootuñu fàttliku seenu tiis.
 
8 Nanga àddul ku amul kàddu,
ku sësul fenn, nga ñoŋal àqam.
9 Deel àddu, di àtte njub;
ku ñàkk ak ku néewle, nga sàmm àqam.
Jeeg bu baax nii lay mel
10 Jeeg bu jàmbaare, ndaw lu jafe,
ba rawati gànjar!
11 Jëkkër ja da koy wóolu,
te jëkkër ja day am xéewal, du ko ñàkk.
12 Day defal jëkkëram lu baax, du ko lor,
tey ànd ak bakkan.
13 Day wut kawari gàtt aki wëñ,
di ca liggéeye mbégte.
14 Day mel ni gaalu jula,
di jëli dundam fu sore.
15 Day jóg te bët setul,
di waajal njëlu njabootam,
ak a sas ay janqam.
16 Day seetlu ab tool, jënd ko,
sàkk ciw ñaqam, jëmbat tóokër.
17 Day gañu di góor-góorlu,
ak a dëgëral përëg ya.
18 Day gis njartel liggéeyam,
te làmpam du fey guddi.
19 Ma ngay yor poqe
ak këccu, di ëcc.
20 Day jox ku ñàkk,
di sàkkal néew-ji-doole.
21 Tiitul ci njaboot gi sedd bu metti,
ndax ñoom ñépp ay tegley yére.
22 Mooy sàkkal boppam ay malaan,
ay yéreem mucc ayib te yànj.
23 Dees na ràññee jëkkëram ca pénc ma,
fa muy toog ca magi réew ma.
24 Ndaw su ni mel day ràbb ay yére, di jaay,
aki gañaay, di jox jaaykat yi.
25 Faaydaak jom la làmboo,
te ëllëg ubul boppam.
26 Day wax lu xelu,
di digle ngor.
27 Jigéen jooju mooy bàyyi xel ci njabootam,
te du nangoo yàccaaral.
28 Doom ya dañu ko naan: «Jarawlakk!»
jëkkër ja di ko gërëm naan:
29 «Jeeg bu jàmbaare bare na,
waaye yaw, yaa ci raw.»
30 Melokaan wu jekk day naxe, taar day wéy,
waaye jigéen ju ragal Aji Sax ji,
kookoo jara gërëm.
31 Joxleen ko njukkalu ñaqam,
jëfam di woyam ca pénc ma.

<- Kàddu yu Xelu 30