Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 26
Ràññeel ab dof
1 Teraanga jekkul cib dof,
mooy seddub nawet mbaa taw cim ngóob.
2 Ñaan-yàlla, soo tooñul, du la dal,
day mel ni picc muy naaw, tëë toŋ.
3 Xiir, aw fas; laab, mbaam;
yetu gannaaw, ab dof.
4 Bul topp ab dof cig ndofam,
lu ko moy nga mel ni moom.
5 Waaye toppal ab dof cig ndofam,
lu ko moy mu defe ne daa muus.
6 Ku yóbbante ab dof kàddu,
yaa woo fitna, gor say tànk.
7 Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof,
mooy tànki lafañ, amalu ko njariñ.
8 Kuy teral ab dof,
jël ngaw doj, takk ko ci mbaq.
9 Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof
mooy car aki dégam, màndikat xàcci.
10 Njaatige luy liggéeyloo ab dof ak kuy romb,
daa mel ni fittkat buy gaañ ku ne.
11 Dof day def jëfi dof, dellu ca,
mooy xaj, bu waccoo, lekkaat ko.
12 Ana koo gis mu ne: «Maa xelu»?
Kooku ab dof a ko gën demin.
Ab yaafus a ngi
13 Ab yaafus da naan: «Gayndee ngi ci yoon wi!
Gayndee ngi ci mbedd mi!»
14 Ab yaafus day tëdd ak a walbatiku,
mooy bunt, day jaayu, demul fenn.
15 Ab yaafus day yeb loxoom ci ndab,
waaye yékkati ko, sex, da koy sonal.
16 Ab yaafus day foog ne moo gëna muus
juróom ñaari boroom xel yu xam tont.
Ay nit ñuy loree ngi
17 Kuy xuloo lu sa yoon newul,
yaa jàpp ci noppi xaj buy romb.
18-19 Nit kuy naxe,
naan: «Damay fo!»
yaay dof buy sànniy jum,
di fitteek a reye.
20 Bu matt amul, ab taal fey,
fu soskat amul it, xuloo jeex fa.
21 Këriñ defi xal, matt xamb ub taal,
ab xulookat di xambu ay.
22 Waxi jëwkat di ñam wu neex,
wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
23 Kuy wax lu neex, tey mébét lu bon,
yaay xaalis bu rax, ñu xoob ca ndabal xandeer.
 
24 Ab noon làqoo na ay waxam,
lal pexey wor ca xolam.
25 Buy wax lu neex, bul gëm,
ñaawtéef la xol ba fees dell.
26 Su la nëbbalee mbañeel, di la nax it,
ag mbonam mujj bir ñépp.
 
27 Ku gasal nit am yeer, yaa cay daanu;
ku béraŋu doj, ngir tance, yaay tancu.
28 Kuy fen, dangaa bañ ka nga fenal,
te boroom làmmiñ wu neex day sànke.

<- Kàddu yu Xelu 25Kàddu yu Xelu 27 ->