Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 19
1 Ñàkk te mat,
moo gën dof, di wax njekkar.
 
2 Teeyadi baaxul,
ku yàkkamti moy saw yoon.
 
3 Nit def na jëfi dof, ba sànku,
walbatiku mere Aji Sax ji.
 
4 Ku barele, barey xarit;
ku ñàkk, sab xarit dagg la.
 
5 Seede buy fen muccul mbugalam,
kuy noyyee ay fen du rëcc àtteem.
 
6 Ñu baree ngi wuta neex boroom daraja,
ku nekk a bëgga xaritook kuy joxe.
 
7 Ku ñàkk, sa bokk yépp dëddu la,
sab xarit gën laa soreeti,
ngay wax ak ñoom, dara.
 
8 Kuy sàkku xel, bëgg nga sa bopp;
kuy wut ag dégg day baaxle.
 
9 Seede buy fen muccul mbugalam,
kuy noyyee ay fen, mujje sànku.
 
10 Dund gu neex jekkul cib dof,
surga buy jiite kilifa it moo yées.
 
11 Ku xam lu jaadu, muñ mer,
tanqamlu ku la tooñ ngay damoo.
 
12 Merum buur ni gaynde gu ŋar;
yërmandey buur ni lay cig mbooy.
 
13 Doom ju dof naqaru baay baa,
te jabar ju pànk mooy senn bu dakkul.
 
14 Kër ak alal ngay donne ci baay;
jabar ju xelu, Aji Sax jee koy maye.
 
15 Ab yaafus, nelaw yu xóot,
te ku yàccaaral xiif.
 
16 Ku jëfe ndigal, sàmm sa bakkan;
ku moytuwul sa bopp, dangay dee.
 
17 Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji,
te moo lay yool.
 
18 Yaral sa doom ba muy teel,
waaye bul topp sa xol, ba rey ko.
 
19 Ku naqari deret, sonal nga sa bopp;
ku la xettli, tóllanti ko.
 
20 Déggal ndigal te yaru,
ndax ëllëg nga xelu.
 
21 Bare na lu xol di mébét,
waaye Aji Sax jeey dogal.
 
22 Li ñu sopp ci nit mooy ngor,
néewle moo gën fen.
 
23 Ragalal Aji Sax ji ndax nga gudd fan,
nopplu te baña loru.
 
24 Ab yaafus day yeb loxoom ci ndab,
tàyyi ko yékkati, sex.
 
25 Boo ñefee ab ñaawlekat, téxét ba jànge ca;
nga yedd kuy dégg, mu xame ca.
 
26 Kuy yàqal sa baay, di dàq sa ndey,
yaay indi gàcceek yeraange.
 
27 Doom, soo noppee déglu ku lay yar,
sore nga kàdduy xam-xam.
 
28 Seedeb naaféq faalewul yoon,
ab soxor lu bon lay tàqamtikoo.
 
29 Na ñaawlekat bi séentu mbugal;
ab dof, yeti gannaaw.