Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 14
1 Jigéen, rafet xel, dimbali waa këram,
su deeb dof, tas këram.
 
2 Kuy jubal day ragal Aji Sax ji,
ku dëng teddadil nga ko.
 
3 Ab dof a ngi réy-réylu, làmmiñam yar ko;
ku rafet xel, sa kàddu aar la.
 
4 Su yëkk takkul, bey, sàq wéet;
mu beye dooleem, meññeef ne gàññ.
 
5 Seede bu dëggu, dëgg rekk,
seede bu dëgguwul, fen rekk.
 
6 Ab ñaawlekat day wut xel mu rafet, mu réer ko;
ku am ug dégg, xam yomb la.
 
7 Dàndal ab dof,
du la yokk xam-xam.
 
8 Ku ñaw day xelu, xam li muy def;
ab dof di nax boppam.
 
9 Ab dof, su bàkkaaree, yoonam!
Te ñay jubal a séq yiwu Yàlla.
 
10 Tiisu xol, boroom a ko xam;
mbégte ma it jaambur bokku ca.
 
11 Ab soxor, këram day tas,
mbaarum ku jub di naat.
 
12 Yoon a ngii, nit defe ne jub na,
te mu jëme ko ci dee.
 
13 Nit a ngi ree, xol ba tiis,
te mbégte mujje na njàqare.
 
14 Ku def njekkar sab añ mat,
ku baax gën law demin.
 
15 Ab téxét, loo wax mu gëm;
ku ñaw xam fi ngay jaare.
 
16 Ku xelu day ragal, di dëddu lu bon;
ab dof day ràkkaaju, du tiit.
 
17 Ku gaawa mer, def jëfi dof,
te kuy fexeel nit, ñu bañ la.
 
18 Ab téxét ndof ay céram,
ku ñaw jagoo xam-xam.
 
19 Ku bon, ku baax sut la;
ku soxor ay toogaanu ku jub.
 
20 Ku ñàkk, say dëkk sax bañ la;
ku barele, barey xarit.
 
21 Ku xeeb sa dëkkandoo, bàkkaar nga;
ku baaxe ku ñàkk, mbégte ñeel la.
 
22 Kuy mébét lu bon daa réer,
kuy mébét lu baax am nga ngor ak worma.
 
23 Kër-këri, jariñu;
waxi neen, loxoy neen.
 
24 Ku rafet xel jagoo alal,
ab dof ràngoo ndofam.
 
25 Seede bu dëggu day jot bakkan,
kuy fen day wore.
 
26 Ragal Aji Sax ji kaaraange gu wér la ci nit,
di rawtu ciy doomam.
 
27 Ragal Aji Sax ji day suuxat bakkan,
ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.
 
28 Su mbooloo baree, buur am ndam;
fu nit ña néew, kilifa du fa dara.
 
29 Muñ mer, déggin wu yaa;
gaawa tàng, gënatee dof.
 
30 Xel mu dal, yaram wu naat;
fiiraange semmal boroom.
 
31 Ku sonal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk;
ku baaxe ku néewle, teral nga ka ko sàkk.
 
32 Coxor detteel boroom;
ku jub fegoo maanduteem.
 
33 Kuy dégg, sam xel saxoo rafet;
ab dof sax xam na lu xelu.
 
34 Njekk day teral aw xeet,
moy di gàcceel aw askan.
 
35 Buur day bége jawriñ ju xelu,
di mbugal nitu gàcce.