Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 12
1 Ku bëgga xam, bëgg ku la yedd;
ku bañ ku la àrtu, bàyyima nga.
 
2 Ku baax, Aji Sax ji bége la;
kuy fexe lu bon, mu daan la.
 
3 Ab soxor, taxawaayam du yàgg;
ku jub garab la, reen ba ne kekk.
 
4 Jeeg bu jàmbaare day teral jëkkër ja,
jeeg buy rusloo day semmal jëkkër ja.
 
5 Ku jub, yoon lay mébét;
ab soxor di lal pexey wor.
 
6 Ab soxor, waxam am tëru la, day reye;
kàdduy kiy jubal di musle.
 
7 Ab soxor bu daanoo, jeex na;
ku jub, sa kër taxaw, ne këcc.
 
8 Xel mu ñaw, jëw bu rafet;
sam xel jekkadi, ñu xeeb la.
 
9 Woyof mbubb, am benn surga doŋŋ,
moo gën réyal turki tey dee ak xiif.
 
10 Ku jub day topptoo ag juram,
ab soxor néeg cig juram.
 
11 Beyal sab tool, sab dund doy;
topp ay caaxaan ñàkk bopp la.
 
12 Ab soxor ay xemmem alal ju lewul,
ku jub garab la, reen baa ko meññal.
 
13 Bàkkaaru làmmiñ dugal na boroom,
ku jub mucc ci njàqare.
 
14 Làmmiñ reggal na boroom;
ñaq, jariñu.
 
15 Na dof di jëfe, njub la ci moom;
dégg ndigal rafet um xel la.
 
16 Ab dof bu meree, mu gaawa feeñ;
ku teey, tanqamlu saaga.
 
17 Ku dëggu, seede dëgg;
seede bu bon, fen rekk.
 
18 Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi;
kàddu gu xelu, garab la ci.
 
19 Kàdduy dëgg, day sax dàkk;
fen, xef xippi, mu wéy.
 
20 Kuy ràbb lu bon lal pexey wor,
kuy digle jàmm, am mbégte.
 
21 Ku jub du amu ay,
ab soxor du tàggook musiba.
 
22 Aji Sax ji sib na fen-kat,
safoo ku dëggu.
 
23 Nit ku ñaw day xam, ba ca;
ab dof siiwal waxi dofam.
 
24 Njaxlaf, jiitu;
yaafus, des gannaaw.
 
25 Njàqare day jeexal xolu boroom,
wax ju neex di tooyal xolam.
 
26 Ku jub day seetlu ku muy xaritool*12.26 Mbaa: Ku jub day teg moroomam ciw yoon.;
soxor bi, jikkoom a koy sànk.
 
27 Ab yaafus bu rëbbee, sooy;
cawarte koom la.
 
28 Jaaral ci njekk, ba gudd fan;
yoon wu baax deesu fa dee.