mu bind ko
Filemon
12 Maa ngi koy yebal ngir mu dellu fi yaw, te di kenn ci man. 13 Dama koo bëggoona téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xibaaru jàmm bi. 14 Waaye buggumaa def dara loo àndul, ngir mu baña doon ndimbalu ñàkk pexe, xanaa loo defe xol bu tàlli. 15 Jombul itam dees koo tàggale ak yaw ab diir, ngir nga jotaat ci moom ba fàww, 16 ba dootu doon sab jaam, waaye day wees ab jaam, di mbokk, di soppe, ma sopp ko lool, te nga war ma koo gëna sopp, ngir jëmmu boppam, ak Sang bi ngeen bokk.
17 Ndegam nag sa waay nga ma def, dalal ko ni su doon man. 18 Su la tooñee, mbaa mu ameel la lenn, topp ma ko. 19 Man Póol maay bind fii ci sama loxol bopp: maay fey loolu, duma ci tuddaale bor bi nga ma ameel, te muy sa njotug bakkanu bopp! 20 Kon nag mbokk mi, may ma googu njekk ngir Sang bi, te nga seral sama xol ndax Almasi. 21 Wóor na ma ci diggante bii may bind bataaxal bi, ne dinga ma déggal, te xam naa ne dinga def sax lu wees li may wax.
22 Te itam nanga ma waajalaale ab dal, ndax yaakaar naa ne dees na ma délloosi fi yeen, ndax seen ñaan yu nangu.
23 Epafras, mbokk mi ñu ma tëjandool ndax Almasi Yeesu, mu ngi lay nuyu, 24 mook Màrk ak Aristàrk ak Demas ak Luug, bokk yi may liggéeyandool.
25 Yal na yiwu Sang Yeesu Almasi ànd ak seenum xel.
- a 11 njariñ: ci làkku gereg turu Onesim mooy tekki «Ku am njariñ.»