Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 9
Lu jëm ci màggalu bésub Mucc
1 Aji Sax ji wax na Musaa ca màndiŋu Sinayi, ca seen atum ñaareel, gannaaw ba ñu génnee réewum Misra ca weer wa jëkk. Mu ne ko: 2 «Na bànni Israyil di màggal bésub Mucc ba, saa yu jotee.

3 «Fukki fan ak ñeent ci weer wii, diggante ngoon ak jant bu so, ci ngeen koy màggal, saa yu jotee. Na mu dëppook mboolem dogali yoonam ak àttey yoonam, nangeen ko màggale noonu.»

4 Musaa nag sant bànni Israyil ne leen ñu màggal bésub Mucc bi. 5 Ñu daldi màggal bésub Mucc bi ci weer wi jëkk, fukki fanam ak ñeent, diggante ngoon ak jant bu so, ca màndiŋu Sinayi. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la ko bànni Israyil defe.

6 Ci biir loolu mu am ay nit ñu ab néew tax ñu sobewu, ba manuñoo màggal bésub Mucc bi bésub keroog. Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona ca bés ba. 7 Ñooñu nag ne Musaa: «Nun de, danoo sobewu ndax ab néew, waaye lu nu teree joxesi saraxu Aji Sax ji ci waxtoom, ci digg bànni Israyil?» 8 Musaa ne leen: «Taxawleen, ba ma dégg lu Aji Sax ji di santaane ci seen mbir.»

9 Aji Sax ji ne Musaa: 10 «Waxal bànni Israyil ne leen, képp ku bokk ci yeen tey, mbaa mu bokk ci seen kuutaay ëllëg, su sobewoo ndax ab néew, mbaa mu nekk ci yoon wu sore, du tere mu màggal bésub Mucc bi ngir Aji Sax ji. 11 Waaye ñaareelu weer wa, ca fukki fanam ak ñeent, diggante ngoon ak jant bu so, ca la koy màggal. Mburu mu amul lawiir ak xob yu wex lay booleek gàttu sarax bi, lekk ko. 12 Bumu ci wacc dara mu fanaan, te benn yax, bumu ko ci damm. Na mu dëppook mboolem dogali yooni bésub Mucc, na ko màggale noonu. 13 Ku set nag te nekkul ciw yoon, su ñàkkee màggal bésub Mucc bi, kooku dees koy dagge ciw askanam, ndax saraxu Aji Sax ji mu joxewul ci bésam. Kooku moo gàddu bàkkaaru boppam.

14 «Su dee ab doxandéem bu ngeen dëkkal, sañ naa màggal bésub Mucc bi ñeel Aji Sax ji. Na mu dëppook mboolem dogali yooni bésub Mucc, ak àttey yoonam, ni la koy màggale; benn dogal bi lay doon ci yeen, muy doxandéem bi, di njuddu-ji-réew.»

Aji Sax ji yiir na xaymab ndaje ma
15 Keroog bés ba ñu sampee màkkaan ma, niir wa daa muur màkkaanu xaymab seede sa. Ca ngoon sa lu mel ni sawara tiim màkkaan ma, ba ca ëllëg sa. 16 Noonu la ko niir wa jàppoo muure, bu guddee mu mel ni sawara. 17 Fu niir wa masa bàyyikoo fa tiim xayma ba, bànni Israyil day fabu topp ko, te fépp fu niir wa masa dale, fa la bànni Israyil di fàkk ab dal. 18 Ci kàddug Aji Sax ji la bànni Israyil daan faboo, ci kàddug Aji Sax ji lañu daan dale, te mboolem fan ya niir way dal, tiim màkkaan ma, ñoom it dañuy dal. 19 Su niir wa yàggee ca kaw màkkaan ma it, ak lu fan ya bare bare, bànni Israyil a ngay dénkoo dénkaaney Aji Sax ji, waaye duñu dem. 20 Leeg-leegaa fan yu néew la niir way dal-lu fa tiim màkkaan ma. Waaye ci kàddug Aji Sax ji daal, lañuy dale te ci kàddug Aji Sax ji lañuy faboo. 21 Leeg-leegaa it niir wa dal-lu ag ngoon, fanaan, ba bët set, mu sàqi, ñu fabu ànd ak moom. Muy guddi, di bëccëg, bu niir wa jógaa, rekk, ñu fabu. 22 Su doon ñaari fan, su doon weer, mbaa ay fani fan la niir wa taxaw tiim màkkaan ma, des fa it, bànni Israyil dañuy dal, waaye duñu dem. Bu jógee rekk lañuy fabu. 23 Ci kàddug Aji Sax ji lañu daa dale, ci kàddug Aji Sax ji lañu daa faboo. Dénkaaney Aji Sax ji daal lañuy dénkoo, ci kàddug Aji Sax, ji Musaa di jottli.

<- Màndiŋ ma 8Màndiŋ ma 10 ->