3 «Seen kemu bëj-saalum a ngay dale màndiŋu Ciin, leru réewum Edom, daleeti ca catal géeju Xorom ga ca penku. 4 Seen kemu daa dënglu, jaare fa féete yéegub Akerabim bëj-saalum, jaare Ciin nag, dem ba bëj-saalumu Kades Barneya, jëm Àccar Adar ba àgg Asmon. 5 Asmon la kem gay jàddaate jubal xuru Misra, doora àkki géej.
6 «Géej gu mag gi mooy doon seen kemu sowu. Loolooy seen kemu sowu.
7 «Lii nag mooy seen kemu bëj-gànnaar. Ca géej gu mag ga ngeen di rëdde, ba ca tundu Or, 8 rëdde ko fa tundu Or, mu jëm Lebo Amat, jàll ba Cedàdd, 9 wéyeeti fa, jaare Sifron, jëm Àccar Enan. Loolooy seen kemu bëj-gànnaar.
10 «Rëddleen seen kemu penku, mu dale Àccar Enan ba Sefam, 11 kemu ga wàcce Sefam, jëm Ribla, fa féete Ayin penku, wàccati ba leruji dexu Kineret, ca wet ga ko féete penku, 12 kemu ga dellu wàcc ba ca dexu Yurdan, doora àkki géeju Xorom ga. Loolooy doon seenum réew ak kemoom yi ko wër.»
13 Ba mu ko defee Musaa sant bànni Israyil, ne leen: «Réew moomu ngeen di tegoo bant, séddoo ko, te moom la Aji Sax ji santaane ñu jox ko juróom ñeenti giir yeek genn-wàll, 14 gannaaw giirug Ruben, ak seeni kër maam, ak giiru Gàdd ak seeni kër maam séddu nañu, te genn-wàllu giirug Manase itam jot nañu seen cér ba noppi. 15 Ñaari giir ya, ak genn-wàllu giir googu ñoo séddu suuf ca penkub dexu Yurdan, fa janook Yeriko.»