17 «Bésub ñaareel ba: fukki yëkk yu ndaw ak ñaar; ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 18 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 19 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak seen saraxi tuur.
20 «Bésub ñetteel ba: fukki yëkk yu ndaw ak benn, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 21 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 22 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram.
23 «Bésub ñeenteel ba: fukki yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 24 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 25 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram.
26 «Bésub juróomeel ba: juróom ñeenti yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 27 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 28 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram.
29 «Bésub juróom benneel ba: juróom ñetti yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukki ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 30 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 31 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram.
32 «Bésub juróom ñaareel ba: juróom ñaari yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 33 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 34 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam, ak saraxu tuuram.
35 «Bésub juróom ñetteel ba seen bésub ndaje lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. 36 Nangeen ci sarxal ab rendi-dóomal, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: wenn yëkk, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te lépp mucc sikk. 37 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 38 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam, ak saraxu tuuram.
39 «Yooyu sarax ngeen di def, ñeel Aji Sax ji, ci seen bési màggal, te du bokke ak seen sarax yi ngeen xasal seen bopp, ak seen saraxi yéene, ak seen saraxi dóomali bés bu nekk, ak seen saraxi pepp ak seen saraxi tuur, ak seen saraxi canti biir jàmm.»
<- Màndiŋ ma 28Màndiŋ ma 30 ->