Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 24
Balaam ñaanalati na Israyil
1 Balaam nag gis ne Aji Sax ji la neex mu barkeel Israyil, ba tax sàkkootul ay takk na woon, xanaa mu walbatiku, janook màndiŋ ma. 2 Ci kaw loolu Balaam dawal bëtam, daldi séen Israyil, na ñu dale topp seeni giir, Noowug Yàlla daldi wàcc ca moom. 3 Ba mu ko defee mu yékkati kàddug ñaanam, ne:
«Kàddug Balaam a ngi, doomu Bewor,
kàddug waa jiy boroom ngis,
4 kàddug kiy dégg waxi Yàlla,
Aji Man ji wonem peeñu, mu gis,
kiy daanu leer, te ay gëtam muriku.
5 Yanqóobaa, yaaka yànji xayma!
Israyil, laa ne, yaaka taaruy màkkaan!
6 Ña nga ne màww ni tooli tàndarma,
nirooteek tóokëri tàkkal dex,
mbaa garabu alowes gu xeeñ gu Aji Sax ji jëmbat,
mbaa garabi seedar yu saxe wali ndox.
7 Ndox maay wale cay bagaanam,
am jiwoom màndim ndox,
buuram nara sut Buur Agag,
nguuram jóg ba kawe.
8 Yàllaay ki ko jële Misra,
féete ko fa ay béjjén féete nagu àll.
Mooy warax xeet yi ko jógal,
dammat leen, jamat leeni fittam.
9 Israyil a ngi yuug ak a goor ni gaynde,
mbete gayndeg sibi, ana ku koy yee?
Ku ko ñaanal barke, yaay barkeel;
ku ko ñaanal alkànde, yaay alku.»
Balaam gis na ëllëgu Israyil
10 Ba loolu amee Balag sànju ci kaw Balaam, daldi fenqey loxoom. Ci kaw loolu Balag ne Balaam: «Móolu samay noon laa la wooye woon, yaw defoo lu moy ñaanal leena ñaanal, ba muy ñetti yoon nii! 11 Léegi nag, laggal ñibbi. Noon naa la dinaa la teral bu baax, waaye mu ngoog, Aji Sax jee la xañ teraanga.» 12 Balaam ne Balag: «Xanaa du sa ndaw yi nga yebaloon ci man sax, waxoon naa leen ne leen, 13 su ma Balag joxoon këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def ci sama coobarey bopp, lenn lu baax mbaa lu bon, lu tebbi ndigalu Yàlla Aji Sax ji? Li Aji Sax ji wax rekk, moom laay wax. 14 Léegi nag maa ngi dellu ca saay bokk, waaye kaay, ma xamal la li xeet wii di def saw xeet, fan yu mujj ya.» 15 Ci kaw loolu mu yékkati kàddug ñaanam, ne:
«Kàddug Balaam a ngi, doomu Bewor,
kàddug waa jiy boroom ngis,
16 kàddug kiy dégg waxi Yàlla,
kiy xame ca xam-xamu Aji Kawe ji,
Aji Man ji wonem peeñu, mu gis,
kiy daanu leer, te ay gëtam muriku.
17 Maa ngi koy gis, te du tey,
Maa ngi koy niir, te jubseegul;
biddiiw a feqe fa Yanqóoba,
yetu nguur a yékkatikoo fa Israyil,
daldi toj boppi Mowab,
toj kaaŋi mboolem askanu Set.
18 Edom, mu moom; Seyir, noonam, muy boroom;
Israyil def jaloore.
19 Fa Yanqóoba la buur di bawoo,
dem ñéddi ndesu dëkk ba.»
Balaam gis na mujug nooni Israyil
20 Ci kaw loolu Balaam geesu réewum Amaleg, dellu yékki kàddug ñaanam, ne:
«Amaleg moo sutu xeet, te sànku lay mujje.»

21 Mu teg ca geesu réewum Keneen ña, yékkeeti kàddug ñaanam, ne:

«Keneen ñee wér ab dëkkuwaay,
seenub tàgg a làqoo biir doj.
22 Waaye réewum Keneen gépp ay xoyomu,
ba leen Asur di yóbbuji njaam.»

23 Mu dellooti yékki kàddug ñaanam, ne:

«Wóoy kuy dund, keroog bu Yàlla dogalee lii?
24 Ay gaal ay jóge tefesu Kitim,
néewalsi doole Asur, néewalsi doole Eber.
Waaye ñoom it dañuy mujj sànku.»

25 Ci kaw loolu Balaam ñibbi am réewam, Balag it demu yoonam.

<- Màndiŋ ma 23Màndiŋ ma 25 ->