8 Ba loolu amee Musaa ak Aaróona dem ba ca kanam xaymab ndaje ma, 9 Aji Sax ji wax Musaa ne: 10 «Jógeleen biir mbooloo mii, ma faagaagal leen léegi!» Ñu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf. 11 Musaa ne Aaróona: «Jëlal and bi, nga sàkke ci sarxalukaay bi ay xal, teg ci cuuraay, yóbbu gaaw ca mbooloo ma, ba defal leen ag njotlaay, ndax sànj mi tàkke na ci Aji Sax ji, mbas mi tàmbali na!» 12 Aaróona këf and ba Musaa wax, daw dugg ca biir mbooloo ma. Ndeke mbas ma tàmbali na ca biir mbooloo ma. Mu def ca and ba cuuraay, daldi defal mbooloo ma njotlaay. 13 Naka la taxaw ci diggante ñi dee ak ñiy dund, mbas ma dal. 14 Ña dee ca mbas ma nag doon fukki junneek ñeent ak juróom ñaar téeméer (14 700), te bokkul ak ña dee woon ca mbirum Kore ma. 15 Ba mu ko defee Aaróona dellu ca Musaa, ca bunt xaymab ndaje ma, fekk mbas ma dal.
21 Musaa àgge ko bànni Israyil, mboolem seen kilifay kër maam jox Musaa aw yet, kilifa gu ci nekk wenn yet, ñeel kër maamam, muy fukki yet ak ñaar, yetu Aaróona bokk ca. 22 Musaa teg yet ya fa kanam Aji Sax ji, ca biir xaymab seede sa. 23 Ca ëllëg sa, naka la Musaa dugg ca xaymab seede sa rekk, daldi fekk yetu Aaróona wu kër Lewi, jebbi; fekk na mu jebbi, ba tóor, ba meññ ay doomi amànd[a]. 24 Ba loolu amee Musaa jële yet yépp ci Aji Sax ji, dem ba ca bànni Israyil gépp, ñépp gis, ku nekk jël yetam.
25 Aji Sax ji waxati Musaa, ne: «Dellool yetu Aaróona fa kanam gaalu seede sa, mu dence fa, di firnde ñeel xeetu fippukat wi, ndax nga dakkal seeni xultu ci sama kaw, ba duñu dee.» 26 Musaa def noonu. Na ko ko Aji Sax ji sante, na la ko defe.
27 Bànni Israyil nag naan Musaa: «Jeexal nan nag, sànku nan, nun ñépp ay sànku! 28 Gannaaw képp ku jege màkkaanu Aji Sax ji doŋŋ, dangay dee kay, mbaa dunu far jeex tàkk?»
<- Màndiŋ ma 16Màndiŋ ma 18 ->- a 17.23 amànd: xeetoo naak gerte-tubaab.