4 Fekk na waa Yudaa ngi naan:
5 Ci biir loolu noon ya naan: «Bala ñu noo yég mbaa ñu di nu gis, nu ne saraax ci seen biir, rey leen, yemale fi liggéey bi.» 6 Yawut ya ñu dëkkal nag dikk waxsi nu fukki yoon ak juróom li ñu nuy fexeel, ne nu «Fu ne lañuy jóge, songsi nu.»
9 Gannaaw gi noon ya xam ne yég nanu leen, te Yàlla nasaxal na seen pexe. Ba mu ko defee nu walbatikuwaat nun ñépp ca tata ja, ku nekk dellu ca liggéeyam. 10 La ko dale bésub keroog sama xaaju nit ña rekk a doon liggéey, xaaj ba ca des gànnaayoo ay xeej aki pakk aki fitt ak kiiraayal dënn. Kilifa ya nag taxaw ca gannaaw mboolem waa Yuda. 11 Ña doon tabax tata jaak ñay yenook ñay yene, ñépp di liggéeye benn loxo, loxo ba ca des ŋàbb ngànnaay. 12 Te it ñay tabax, ku ci nekk, sab saamar a nga takke ci sa ndigg, ngay liggéey, boroom liit gi feggook man. 13 Ma wax ak garmi yaak kilifa yaak mbooloo ma ca des, ne leen: «Liggéey bi réy na, yaatu na, te nun danoo tasaaroo te soreyantoo ci tata ji. 14 Fu ngeen dégg liit gi jibe fa, fekksileen nu fa. Sunu Yàlla dina nu xeexal.» 15 Nu nekk nag ci liggéey bi, genn-wàllu nit ñi yore ay xeej, dale ko ba bët di set, ba biddiiw yiy feq.
16 Boobu it laa wax mbooloo ma ne leen: «Na ku nekk ànd ak ka muy liggéeyandool, fanaan ci biir Yerusalem. Su ko defee nu man di wattu guddi, di liggéey bëccëg.» 17 Booba kenn ci nun summiwul ay yéreem, du man, du samay bokk, du samay nit, te du wattukat yi ànd ak man. Ku nekk day ŋàbb ngànnaayam akam ndox.
<- Neyemi 3Neyemi 5 ->