Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 12
Ñii ñooy Leween ñeek sarxalkat yi jëkka ñibbsi
1 Sarxalkat yaak Leween ña ñibbsi, ànd ak Sorobabel doomu Selcel, ak Yosuwe sarxalkat bu mag ba, ñii la:
Seraya ak Yeremi ak Esra 2 ak Amarya ak Malug ak Atus 3 ak Sekaña ak Reyum ak Meremot 4 ak Ido ak Gintoy ak Abya 5 ak Miyamin ak Maadiya ak Bilga 6 ak Semaya ak Yowarib ak Yedaya 7 ak Salu ak Amog ak Ilkiya ak Yedaya. Ñooñooy kilifay sarxalkat yeek seeni bokk ca jamonoy Yosuwe.

8 Leween ñi ñoo doon Yeswa ak Binuy ak Kadmiyel ak Serebya ak Yuda ak Mataña may jiite jàngi cant ya, mooki bokkam. 9 Bagbukiya ak Uni ak seeni bokk janook ñoom ca liggéey ba.

10 Yosuwe, sarxalkat bu mag ba mooy baayu Yowakim. Yowakim di baayu Elyasib, Elyasib di baayu Yowada, 11 Yowada mooy baayu Yonatan, Yonatan di baayu Yaduwa.

12 Ca jamonoy Yowakim sarxalkat bu mag ba, ña jiite woon kër sarxalkat ya ñii la: Meraya ma bawoo ca waa kër Seraya ak Anaña bawoo ca waa kër Yeremi, 13 Mesulam bawoo ca waa kër Esra, Yowanan bawoo ca waa kër Amarya, 14 Yonatan bawoo ca waa kër Malug, Yuusufa bawoo ca waa kër Sebaña, 15 Adna bawoo ca waa kër Arim, Elkay bawoo ca waa kër Merayot, 16 Sàkkaryaa bawoo ca waa kër Ido, Mesulam bawoo ca waa kër Ginton, 17 Sikkri bawoo ca waa kër Abya. Mu am ñu jóge ca waa kër Miñamin. Piltay bawoo ca waa kër Mowadiya, 18 Samwa bawoo ca waa kër Bilga, Yonatan bawoo ca waa kër Semaya, 19 Matenay bawoo ca waa kër Yowarib, Usi bawoo ca waa kër Yedaya, 20 Kalay bawoo ca waa kër Salu, Eber bawoo ca waa kër Amog, 21 Asabya bawoo ca waa kër Ilkiya, Netanel bawoo ca waa kër Yedaya.

22 Ca janti sarxalkat yu mag ya, Elyasib ak Yowada ak Yowanan ak Yaduwa, ku nekk ak jamonoom, ña jiite woon këri Leween ña ak sarxalkat ya, bindoon nañu leen ci biir nguurug Daryus buuru Pers. 23 Ña jiite woon seeni kër baay te askanoo ci Lewi, ba ca jamonoy Yonanan sëtub Elyasib daan nañu leen bind ñoom ñépp ca téere ba ñu dippee Xew-xew ya.

24 Njiiti Leween ñi ñoo doon: Asabya ak Serebya ak Yeswa doomu Kadmiyel, ñook seen bokk ña ñu daan awanteel làng ak làng ci jàngi cant, muy la Daawuda góoru Yàlla ga santaane woon. 25 Mataña ak Bagbukiya ak Obadiya ak Mesulam ak Talmon ak Akub ñoo doon fara bunt ya, di wattu néegi dencukaay, ya ca bunt ya.

26 Ñooñoo fa nekkoon ca jamonoy Yowakim doomu Yosuwe. Yosuwe, Yoccadag mooy baayam. Ñoo fa nekkoon itam ca jamonoy Neyemi boroom dëkk ba, ak Esra ma doon sarxalkat, di bindkat.

Daloo nañu tata ja
27 Gannaaw gi, ca xewu daloog tatay Yerusalem ja, ñu wooye Leween ña mboolem fa ñu dëkke, indi leen Yerusalem, ngir ñu màggal daloo ga ci biir mbég ak jàngi cant; tëggum weñ ya jib, ànd ak xeeti xalam. 28 Ci biir loolu ñu indi jàngkat ya ñoom it, boole leen jële ca diiwaan ba wër Yerusalem, ca dëkk yu ndaw ya ca Netofa, 29 ak Bet Gilgal ak diiwaani Geba ak Asmawet. Fekk na jàngkat ya tabax ay dëkk yu ndaw fa wër Yerusalem.

30 Ba loolu amee sarxalkat yaak Leween ña laabal seen bopp, doora laabal mbooloo ma, ak bunt yaak tata ja.

31 Ci kaw loolu ma yéegloo njiiti Yudeen ña ca kaw tata ja, daldi sos ñaari kuréli jàngkat yu mag. Genn ga di dox ca kaw tata ja ci wetu ndijoor, wuti buntu Sën ba. 32 Osaya ma nga topp ca seen gannaaw, ànd ak genn-wàllu njiiti Yudeen ña, 33 ak Asaryaa ak Esra ak Mesulam, 34 ak Yuda ak Beñamin ak Semaya ak Yeremi. 35 Lenni sarxalkat yaa nga ca topp aki liit, di ñi ànd ak Sàkkaryaa doomu Yonatan. Yonatan, Semaya mooy baayam; Semaya, Mataña di baayam, Mataña, Mikaya mooy baayam; Mikaya, Sakuur ay baayam; Sakuur, Asaf mooy baayam. 36 Sàkkaryaa ànd aki bokkam, ñuy Semaya ak Asarel ak Milalay ak Gilalay ak Maay ak Netanel ak Yuda ak Anani. Ña nga yore ay jumtukaayi xumbéen yu Daawuda, góorug Yàlla ga. Esra bindkat ba moo leen jiite woon. 37 Ñu dikk ba tollook buntu Ndox ma, janook dëggastal, ya jëm ca Kër Daawuda, fa ñuy yéege jëm ca tata ja tiim kër Buur Daawuda. Ñu jubal nag ba ca buntu Ndox ma, ca penku.

38 Ci biir loolu ñaareelu kurélu jàngkat ya doxe wetu càmmoñ; man nag, ma topp ca seen gannaaw ca kaw tata ja, ànd ak genn-wàllu mbooloo ma. Nu jaare ca wetu sooroor ba ñuy wax Taal ya, ba fa tata ja yaatoo. 39 Nu romb nag fa tiim buntub Efrayim ak buntu Cosaan ba, ak buntu Jën ya ak soorooru Ananel, wees soorooru Meya, ba àgg ca buntu Gàtt ya. Ña nga taxaw ca buntu Dag ya. 40 Ci kaw loolu ñaari kuréli jàngkat ya taxaw ca biir kër Yàlla ga, man itam ma taxaw, maak genn-wàllu mbooloom jawriñ ñi ma àndal, 41 ak sarxalkat ya, di Elyakim ak Maaseya ak Miñamin ak Mikaya ak Elyonay ak Sàkkaryaa ak Anaña, ñook seeni liit.

42 Maaseya it a nga ca woon ak Semaya ak Elasar ak Usi ak Yowanan ak Malkiya ak Elam ak Eser. Jàngkat ya daldi samp, Israya jiite leen.

43 Sarxe nañu bésub keroog sarax yu réy tey bànneexu, ndax Yàllaa leen may bànneex bu réy. Jigéen ñaak gone ya it di bànneexu, mbégarey Yerusalem di dégtu fu sore.

44 Ñu daldi tànn bésub keroog ay nit, dénk leen néegi dencukaay, ya ñuy yeb ay jooxe, ak saraxi ndoortel meññeef, ak céri fukkeel yu ñuy génne. Ñu war caa dajale nag cér ya yoon wi dogalal sarxalkat yeek Leween ñi, te mu jóge ci tool yi wër dëkk yi. Waa Yuda rafetlu ca taxawaayu sarxalkat yaak Leween ña. 45 Leween ñaa dénkoo woon seen dénkaaney Yàlla, ak dénkaaney laabal ba, ak jàngkat yaak fara bunt yay topp la Daawuda santaane woon, mook doomam Suleymaan. 46 Te naka jekk ca janti Daawuda ak Asaf amoon na ay njiiti jàngkat yuy jiite ay jàngi màggal ak jàngi cant, ñeel Yàlla. 47 Ci biir loolu, ca janti Sorobabel ak ca janti Neyemi, askanu Israyil gépp daan nañu génneel jàngkat yeek fara bunt yi seen cér, bés bu nekk it, génneel Leween ñi seen cér, Leween ñi génneel askanu Aaróona seen cér.

<- Neyemi 11Neyemi 13 ->