Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 10
Bànni Israyil dogu nañu
1 Loolu yépp tax na nuy tëral takktoo bu dogu, bind ko, sunuy njiit ak sunuy Leween ak sunuy sarxalkat def ci seen màndargay torlukaay.

2 Ñi ko torlu ñoo di:

Boroom dëkk bi Neyemi doomu Akalya, mook Cedekiya 3 ak Seraya ak Asaryaa ak Yeremi 4 ak Pasur ak Amarya ak Malkiya 5 ak Atus ak Sebaña ak Malug 6 ak Arim ak Meremot ak Obadiya 7 ak Dañeel ak Ginton ak Barug 8 ak Mesulam ak Abya ak Miyamin 9 ak Maasya ak Bilgay ak Semaya. Ñooñu ñoo di sarxalkat ya.

10 Leween ñi ñoo di:

Yeswa doomu Asaña, ak Binuy, kenn ca doomi Enadàdd, ak Kadmiyel. 11 Seeni bokk ca lañu, di Sebaña ak Odiya ak Kelita ak Pelaya ak Xanan 12 ak Mika ak Reyob ak Asabya 13 ak Sakuur ak Serebya ak Sebaña 14 ak Odiya ak Baani ak Beninu.

15 Njiiti askan wi ñoo di:

Paros ak Payat Mowab ak Elam ak Sàttu ak Baani 16 ak Buuni ak Asgàdd ak Bebay 17 ak Adoña ak Bigway ak Adin 18 ak Ater ak Esekiya ak Asur 19 ak Odiya ak Asum ak Besay 20 ak Arif ak Anatot ak Nebay 21 ak Magpiyas ak Mesulam ak Esir 22 ak Mesesabel ak Cadog ak Yaduwa 23 ak Pelaca ak Xanan ak Anaya 24 ak Oseya ak Anaña ak Asub 25 ak Aloyes ak Pila ak Sobeg 26 ak Reyum ak Asabna ak Maaseya 27 ak Axiya ak Xanan ak Anan 28 ak Malug ak Arim ak Baana.
Solob dogu baa ngi
29 Bànni Israyil ga ca des nag fekksi leen, muy sarxalkat yaak Leween ñaak fara bunt yaak jàngkat yaak liggéeykati kër Yàlla ga, di mboolem nun ñi beddeeku woon waasoy réew yi, ngir topp yoonu Yàlla wi, nook sunuy jabar ak sunu doom yu góor ak yu jigéen, mboolem ñi xam te xàmmee. 30 Ci kaw loolu nu ànd ak sunu bokki garmi, waatook ñoom ne dinanu topp yoonu Yàlla wi mu dénkaane, Musaa jaamam ba jottli; di ko sàmm, di jëfe mboolem sunu santaaney Boroom Aji Sax ji, ak àttey yoonam ak dogali yoonam.
31 Nu ne nag dunu may waa réew mi sunu doom yu jigéen te dunu jëlal sunuy doom seeni doom yu jigéen.
32 Te itam bu waa réew mi indee am njaay mbaa lépp luy pepp, di ko jaay ci bésub Noflaay, dunu ko jënd ci ñoom bésub Noflaay mbaa bés bu sell, te atum juróom ñaareel mu nekk dinanu bale bépp bor.
33 Ci biir loolu nu warloo santaaney joxe at mu nekk ñeenti garaami xaalis, bu jëm ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga, 34 jëm ca mburum wone ba, ak saraxi pepp yi war bés bu nekk, ak saraxi dóomal yu bés bu nekk, ak saraxi bési Noflaay, ak yu Terutel weer ak yu bési màggal yi, ak yeneen yu ñu sellalal Yàlla, ak saraxi póotum bàkkaar yi bànni Israyil di jotoo, ak mboolem la war ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga.
35 Ay bant lanu tegoo ci sunu biir, nun sarxalkat yeek Leween ñeek baadoolo yi, ngir dogalal waa kër gu nekk àpp ba ñu wara aye cim at, te ñu war caa yóbbu seen sasu matt ca sunu kër Yàlla ga, ngir taal ko ca sunu sarxalukaayu Yàlla Aji Sax ji, muy la ñu bind ci téereb yoon wi.
36 Nu dogu ba tey ne dinanu yóbbu ca kër Aji Sax ji, at mu nekk, li sunu suuf jëkka meññle ak lu garab yépp jëkka ñorle. 37 Ci biir loolu nu dogoo def li ñu bind ci yoon wi, di yóbbu ca sunu kër Yàlla ga sunu taaw yu góor ak lu sunu jur taawloo, gu gudd gaak gu gàtt ga, di teg lépp ci loxoy sarxalkat ya fay liggéey. 38 Ci kaw loolu nu wara yóbbu ca sunu néegi dencukaayi kër Yàlla ga lu jëkk ci sunu notu sunguf, ak sunu jooxey pepp, ak sunu meññeefi garab yépp, ak sunu biiñ ak diw, di teg lépp ci loxoy sarxalkat yi. Ba tey nuy indil Leween ñi céru fukkeelub lépp luy meññee ci sunu suuf, ndax Leween ñeey dajalesi céri fukkeel yi ci gox yi nuy bey yépp. 39 Sarxalkat bu askanoo ci Aaróona mooy gunge Leween ñiy jëlsi céri fukkeel yi. Su ko defee Leween ñi yóbbu fukkeelu céri fukkeel yi ba ca sunu kër Yàlla ga, fat ko ca néegi dencukaayi alal ya. 40 Ci néeg yooyu la bànni Israyil ak askanu Leween ñi di yóbbu jooxeb pepp ba ak biiñ baak diw ga; fa la ndabi bérab bu sell ba dence, te fa la sarxalkat, ya sasoo liggéey ba nekk, ñook fara bunt yaak jàngkat ya.
Nu dogu nag ne dunu sàggane sunu kër Yàlla ga.

<- Neyemi 9Neyemi 11 ->