Saar 6
Aji Sax ji tudd na sikkaangey ñoñam
Mise mooy wax
1 Dégluleen rekk li Aji Sax ji wax:
Jógal layoo, tund yu mag yi seede,
tund yu ndaw yi dégg la.
2 Yeen tund yu mag yi, dégluleen
layoob Aji Sax ji,
ak yeen kenuy suuf yi sax dàkk.
Aji Sax jee joteek ñoñam,
mooy wàqanteek Israyil.
Aji Sax jeey wax
3 Yeen sama ñoñ, ana lu ma leen def?
Ana fu ma leen sonale?
Waxleen ma!
4 Yeen maa leen génnee réewum Misra,
kërug njaam googa, maa leen fa jote,
ba yebal fi seen kanam, Musaa ak Aaróonaak Maryaama.
5 Yeen sama ñoñ, fàttlikuleen rekk
la leen Balag buurub Mowab fexeeloon,
ak la ko Balaam doomu Bewor tontu woon.
Doxub diggante Sitim ba Gilgal*6.5 Sitim la Israyil tàmbalee woon seenub dox, jeexale Gilgal, ca wàllaa dexu Yurdan ga feesoon gannaaw ba ñu ko jàllee. Seetal ci Yosuwe 3.1-5.12. it, baleen ci xel,
ba ràññee njekku Aji Sax ji.
Nit ñeey wax
6 Ana lu may dikkaale fi kanam Aji Sax ji,
ba sujjóotal Yàlla jooja fa kaw.
Tee ma koo dikke ay rendi-dóomal,
ay wëlluy menn at?
7 Mbaa dina ma nangul junniy kuuy,
ak fukki junniy dexi diw?
Am samab taaw laay joxe
saraxu peyu bàkkaar,
sama meññeefum biir di sama saraxu peyug tooñ ?
Mise mooy wax
8 Yaw nit ki, waxees na la li baax,
ak li Aji Sax ji sàkku ci yaw,
te loolu moyul di def yoon, sopp jëfi ngor
te woyof nooy toppe sa Yàlla.
Mbugal ñeel na waa Yerusalem ñi fecci kóllëre
9 Baatub Aji Sax ji mooy joor dëkk bi,
te ndam mooy ñeel ñi wormaal sa tur.
«Dégluleen seen yetu mbugal, ak ki ko yebal,
10 ndax alalu njublaŋ a ngi ci biir këri njublaŋ yi ba tey,
mook nattukaayi alkànde yu tuut ya ñuy jaaye?
11 Ana nu may ñàkka toppe màndaxekaayi njublaŋ,
ak mbuusum doomi naxekaay yees cay natte?
12 Boroom alal yi ci sa biir, aw ay lañu fees,
waa dëkk bi di fen,
te lu seen làmmiñ tudd ay nax la.
13 Man it moo tax ma di la duma
ba nga wopp,
gental la ndax say bàkkaar.
14 Yaw de dinga lekk, te doo suur,
xanaa wéye biir bu wéet.
Dinga fat loo dul mana denc fu wóor,
te loo denc fu wóor it, ab saamar laa koy jox.
15 Yaw de yaay ji te doo góob,
nga nal doomi oliw te doo ca diwu,
nal doomi reseñ te doo naan biiñ.
16 Dogali Buur Omri daal lees di topp,
ak mboolem jëfini waa kër Buur Axab†6.16Omri ak doomam Axab ay buuri Samari lañu woon, ñu ràññeeku ci jalgati yoon, ak lawal ag bokkaale. .
Seeni pexe ngeen topp,
ba tax may def dëkk bi di lu daw yaram,
waa dëkk bi di ñu nit ñiy muslu ci seenu demin,