Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 5
1 «Yaw Betleyem Efrata,
lu tuut ci làngi Yuda,
ci yaw la ku may yilifal Israyil di génne,
cosaanam di jant yu yàgga yàgg,
bu jëkkoon.»
2 Moo tax Aji Sax ji di leen wacc
ba keroog jant, ba kiy matu mucc.
Ca la bokkam ya dese bakkan di dellu,
fekki seen bokki bànni Israyil.
3 Kilifa gaay taxaw, sàmme
ci dooley Aji Sax ji,
ci màggug turu Yàllaam Aji Sax ji,
ba ñu dëkke jàmm,
nde léegi lay doon ku màgg
ba turam dajal cati àddina.
4 Kookooy doon buntu jàmm,
ba bu waa Asiri songee sunum réew,
ba daagoo sunu kawi tata,
juróom ñaari njiit lanu koy yékkatil,
ba juróom ñetti garmi.
5 Ab saamar la ñooñuy yilife Asiri,
réewum Nimróot mooma ca biiri buntam.
Kilifa gi ñu dige moo nuy xettleek Asiri, bu ñu nu songee,
ba joggati sunu suuf.
Ndesu Israyil dina am doole
6 Ci biir askan yu bare la ndesu Yanqóoba di nekk,
mel nib lay bu bawoo fa Aji Sax ji,
nirook waame wu wàccal gàncax,
xaarul lenni nit,
lenni doom aadama la séentuwul.
7 Ci biir askan yu bare la ndesu Yanqóoba di nekk,
ci biir xeeti àddina,
mbete gaynde ci biir rabi àll yi,
nirook gaynde gu ndaw ci biiri gàtt;
fu mu jaare, joggati, xotat,
te kenn du wallu.
Cëslaay réer na bokkaalekat
8 Aji Sax ji, sa loxo ca kaw, tiim say bañ,
mboolem say noon lees di dagge ci kaw suuf.
9 «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee,
«maay dagge fi sa biir, sa fasi xare,
te maay sànk sa watiiri xare.
10 Maa fiy dagge sa dëkki réew mi,
màbb sa tata yépp.
11 Maay foqatee ay xërëm ci sa loxo,
te ay gisaanekat, dootuloo ko am.
12 Maay dagge fi sa biir say tuur,
ak sa xeri jaamookaay,
te dootoo sujjóotal loo sàkke say loxo.
13 Maay buddee fi sa biir xeri jaamookaayi Asera
tuur mi,
te maay tas say jaamookaay.
14 Mer akum sànj laay feye xeeti yéefar,
yi déggul ndigal.»

<- Mise 4Mise 6 ->