Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 4
Aji Sax ji, ca tundam lay saytoo xeet yi
1 Fan yu mujj ya, dees na taxawal
tundu kër Aji Sax ji,
mooy gëna kawe ci tund yi,
tiim tund yu ndaw yi,
askan yi riirandoo, wutsi ko.
2 Xeet yu bareey dikk te naan:
«Dikkleen nu yéegi ca tundu Aji Sax ji,
kër Yàllay Yanqóoba,
mu xamal nuy yoonam,
ba nu doxe yooyu ñallam.»
Siyoŋ kat la ndigalu yoon di bawoo,
Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge.
3 Mooy àtte diggante xeet yu bare,
mooy dogalal askan yu am doole te sore,
ñu tëgg seeni saamar ay illéer,
def seeni xeej ay sàrt.
Aw xeet dootu xàccil moroom ma saamar,
te dootuñu jàngati xare.
4 Ñoom ñépp ay toog, ku nekk ci kerug reseñam,
mbaa keppaarug garabu figgam,
kenn du leen xoqtal.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
 
5 Askan wu nekk ci yaakaaru turu yàllaam lay doxe.
Nun nag ci yaakaaru sunu turu Yàlla Aji Sax ji
lanuy doxe, tey ak ëllëg, ba fàww.
 
6 Bésub keroog, kàddug Aji Sax jee,
«Naa jëli kuy soox, booleek ku ñu toxaloon,
te ma mbugaloon leen.
7 Maay def liy soox aw ndes,
la ñu dàq fu sore, ma def ko askan wu am doole,
te Aji Sax jeey doon seen buur ca kaw tundu Siyoŋ,
li ko dale tey ba fàww.
 
8 «Yaw, tatay gétt gi,
yaw tundu Ofel*4.8 Ofel aw tund la woon ca Yerusalem, ñu tabax ca tata ju ñu dàbbli. Daawuda moo ko nangu woon ca Yebuseen ña.,
yaw janq Siyoŋ mu taaru mi,
yaw lees di ñëwal,
yaw la kilifteef ga woon di dikkal,
nguur gi, janq Yerusalem mu taaru lay ñeel.»
Coono jur na jant bu yees
9 Ana lu la tax di yuuxoo yuuxu tey?
Buur daa amul fi sa biir?
Am ki lay xelal a dee, ba mitit jàpp la nii,
nga mel ni kuy matu?
10 Wañaarul te yuuxu ni kuy matu ndax mitit,
yaw janq Siyoŋ mu taaru,
nde dëkk bi ngay génn, màkkaanoo àll bi,
dinga dem Babilon4.10 Lu wara tollook téeméeri at gannaaw gi, ba Buur Esekiya deeyee la Yerusalem tàbbi ci loxol Babilon. Seetal ci 1.1.,
te fa lees lay xettlee,
fa la la Aji Sax jiy jote ci loxol say noon.
 
11 Tey ci sa kaw, la xeet yu bare daje, yaw Siyoŋ,
te naan: «Nees ko tëdde,
nanu seetaan Siyoŋ!»
12 Booba ñoom xamuñu lu ciy xalaati Aji Sax ji,
ak luy mébétam,
nde moo leen di dajale niy sabaar ca dàgga ja.
13 «Yaw janq Siyoŋ mu taaru, jógal bàcci leen,
sa béjjén laay def ag weñ,
say wewi tànk, ma def ko xànjar,
nga rajaxe xeet yu bare.»
Yaay faagaagal seen alal ju lewul, ñeel Aji Sax ji,
seen koom ñeel Boroom àddina sépp.
Betleyem la kilifa di juddoo
14 Léegi yaw, dëkkub gàngoor yi,
defal sa bopp ay gàngoor,
ab gaw lees nu yékkatil,
te yetu ŋaam lees di dóor njiital Israyil.

<- Mise 3Mise 5 ->