Saar 3
1 «Maa ngii di yebal sama ndaw,
mu xàllal ma aw yoon.
Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku
mooy jekki agsi këram,
malaakam kóllëre moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo,
mu ngooguy dikk.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
2 Waaye bésub dikkam, ana ku ko mana dékku?
Bu teewee ana kuy taxaw?
Nde moom daa mel ni sawaras tëgg
buy xelli weñ,
melati ni xemey fóotkat.
3 Fa mbaxana dee benn lay tooge
ni xellikat ak seggkat,
te mooy segg sëti Lewi, xelli leen
ni xaalis ak wurus,
ba ñu doon niti Aji Sax ji,
ñi koy indil sarax ci njekk.
4 Su boobaa la saraxu Yuda ak Yerusalem
di neex Aji Sax ji,
na jant ya woon, at ya woon.
5 «Maa leen di dikke ab àtte,
di ab seede bu taxaw temm
ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi,
ak ñiy fene ngiñ,
ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram,
di noggatu ab jëtun akub jirim,
di beddi doxandéem te ragaluñu ma.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
6 «Man Aji Sax ji déy, duma soppiku,
te yeen noppiwuleen di askanu Yanqóoba*3.6 askanu Yanqóoba mooy askan wi soqikoo ci Yanqóoba mi suufu woon ab seexam., ay workat.
Waññiku ci Aji Sax ji moo war
7 «Ca seen janti maam
ngeen dëddoo sama dogali yoon,
sàmmuleen ko.
Waññikuleen fi man, ma waññiku fi yeen,»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
«Yeena ngi naa:
“Ci lan lanuy waññikoo?”
8 Waaw, nit dina sàcc Yàlla?
Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc
te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?”
Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe.
9 Alkànde ju réya ngi leen di dikkal,
nde man ngeen di sàcc, yeen mboolem askan wi.
10 Indileen mboolem céru fukkeel
ca kërug denc ya,
ba ab dund am sama biir kër,
te ngeen seetloo ma ko rekk,»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax,
«ndegam duma leen ubbil bunti asamaan,
ba sottil leen barke bu doy.
11 Maa leen di gëddal njéeréer,
ba du leen yàqal meññeefum suuf,
te reseñug tool du leen jaasiral.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
12 «Xeet yépp ñu barkeel ñi lañu leen di wooye,
nde réewum bànneex ngeen di dëkke.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
Aji Sax ji dina fésal njubteg àtteem
13 «Kàddu yu ñagas ngeen teg ci sama kaw,»
Aji Sax jee ko wax.
«Te yeena ne: “Ana kàddu yu ñu la waxal”?
14 Yeena ne: “Jaamu Yàlla ag neen la.
Ana lu nu jële ci dénkoo ndénkaaneem,
tey wéye toroxlu
fi kanam Aji Sax ji Boroom gàngoor yi?
15 Moo tax nu ne nit ñu bew ñi ñooy ñi barkeel,
ñiy def lu bon kay ñoo baaxle,
ñoom ñiy diiŋat Yàlla, teg ca rëcc.”»
16 Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir,
Aji Sax ji teewlu, déglu leen.
Ñu bind fi kanamam téereb fàttliku,
bu lim ñi ragal Aji Sax ji,
te teral aw turam.
17 «Sama moomeelu bopp la ñooñuy doon,»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax,
«ca bés ba may jëfi, sama gànjar lañuy doon,
te ni baay di baaxee as ngóoram su ko taxawu,
ni laa leen di baaxee.
18 Ca ngeen di ràññaatlewaat diggante
ku jub ak ku bon,
kuy jaamu Yàlla,
ak ku ko jaamuwul.
19 Bés ba déy a ngii di ñëw,
di tàkk ni taal bu yànj.
Képp ku bew ak kuy def lu bon,
ca lay mel ni boob,
te bésub keroog baa koy jafal.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
«Du leen waccal tus, dub reen, dub car.
20 Waaye yeen ñi ma ragal
la jantub njekk di fenkal,
yiire leen ceeñeer yuy wéral,
ngeen génn di tëbantu ni ay sëlluy yar.
21 Yeenay joggi ñu bon ñi,
ñu doon pënd fi seen ron téstën,
keroog bés ba may jëfi.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
22 «Bàyyileen xel ci yoonu Musaa, sama jaam ba,
yoon wa ma ko dénkoon fa tundu Oreb,
ñeel Israyil gépp,
mu diy dogal ak àttey yoon.
23 Maa ngii di yebal ci yeen, Ilyaas yonent bi,
balaa bésub Aji Sax jee teew,
di lu màgg te raglu.
24 Mooy delloo xolu baay ca doom ja,
delloo xolu doom ca baay ba,
lu ko moy ma dikk duma réew mi, ba faagaagal ko.»
<- Malasi 2
- a 3.6 askanu Yanqóoba mooy askan wi soqikoo ci Yanqóoba mi suufu woon ab seexam.