4 Ñu ne cell. Yeesu teg waa ja loxo, wéral ko, daldi ko yiwi. 5 Mu ne leen: «Ana kan ci yeen la doomam mbaa aw yëkkam daanu cib teen, mu bañ koo daldi génne ci bésub Noflaay?» 6 Lu ñu ca teg nag të leen, ñu ne xerem.
7 Ci biir loolu Yeesu gis na gan ñay taamoo toogu yu kaname, mu léeb leen, ne leen: 8 «Bu la boroom xew wooyee ci berndeg céet, bul wàllisi, ba tooge toogu ba gëna kaname, xamoo fu ku la sutu daraja di wuysee boroom xew ma. 9 Su boobaa moom mi la woo, woo ko, mooy dikk, ne la: “Mayal kii, mu toog.” Nga am nag gàccey walbatiku toogi fa gëna gannaawe. 10 Bu ñu la wooyee am xew kay, demal tooge fa gëna gannaawe, ba ka la woo dikk ne la: “Xarit, agsil ci kanam.” Su boobaa muy sa teraanga ci kanam mboolem ña nga bokkal bernde ja. 11 Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, ka toroxlu lees di yékkati.»
12 Ci kaw loolu Yeesu ne waa ja ko woo bernde: «Boo dee waajal bernde, añ mbaa reer, bul woo say xarit, mbaa say doomi ndey, mbaa say bokk, mbaa say dëkk yu am alal, nde ñoom itam dañuy walbatiku, woo la rekk, mu doon sag pey. 13 Boo dee waajal bernde kay, wool néew-doole yi ak làggi yi, ak ñiy soox ak silmaxa yi. 14 Su boobaa ndokklee yaw, nde amuñu sag pey, waaye dees na la fey, kera ndekkitel aji jub ñi.»
18 «Ñu tàmbalee gàntal nag ñoom ñépp. Kii ne ko: “Ab tool laa jënd, te fàww ma xooli ko. Dama lay ñaan rekk, nga jéggal ma.” 19 Kee ne: “Ay lëkkey yëkk, ci laa jënd juróom, damay dem nii, jéemloo leen ba xam. Dama lay ñaan rekk, nga jéggal ma.” 20 Kale ne ko: “Ab séet laay sooga takk, looloo tax duma mana ñëw.”
21 «Surga ba dellu, daldi koy àgge boroom kër ga, njaatigeem. Mu mer, ne surga ba: “Demal gaaw ca pénc yaak mbeddi dëkk bi, te nga indi fii néew-doole yi, ak làggi yi ak silmaxa yi ak ñiy soox.”
22 «Surga ba dem ba délsi, ne ko: “Sang bi, li nga santaane de def naa ko, waaye kër gi feesagul.” 23 Njaatige li ne ko: “Demal topp yoon yi, leru ñag yi, te nga soññ nit ñi, ñu dikk ba sama kër fees.” 24 Maa leen ko wax, ñi ma woo woon ci sama bernde ji, kenn du ci mos.»
34 «Xorom déy baax na, waaye bu sàppee, ana lees koy safaleetee? 35 Jariñatul suuf, jariñatul ab tos. Ca biti lees koy tuuri. Ku ami nopp kat, déglul.»
<- Luug 13Luug 15 ->