5 Yeesu teg ca ne leen: «Ana kan ci yeen moo seeti ab xaritam xaaju guddi, ne ko: “Xarit, lebal ma ci ñetti mburu. 6 Sama xarit bu nekk ciw yoon moo dikk sama kër, te awma dara lu ma ko taajal,” 7 te xarit ba àddoo ca biir néegam, ne ko: “Bu ma sonal, tëj naa ba tëdd, maak samay doom; manumaa jóg, di la jox dara”? 8 Maa leen ko wax, su jógul jox ko la mu laaj ndax ug xaritoo it, la ko kee amul kersay yee ngir sàkku ndimbal mooy tax mu jóg, jox ko mboolem lu mu soxla. 9 Moo tax ma ne leen, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, ndax ngeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. 10 Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, dinga gis; ku fëgg it, dees na la ubbil. 11 Ana kan ci yeen mooy baay bu doomam ñaan aw jën, mu jox ko jaan? 12 Mbaa mu ñaan ko nen, mu jox ko aw jiit? 13 Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»
16 Ñeneen nag di ko fiir, di sàkku ci moom firnde ju bawoo asamaan. 17 Yeesu itam ràññee seen xalaat, ne leen: Gépp nguur guy xàjjalikoo ci biiram, day tas, yii kër màbb ca kaw yee. 18 Seytaane itam, su xàjjalikoo ci biiram, ana nu nguuram di yàgge, gannaaw yeena ne Beelsebul laay dàqe ay rab? 19 Te it ndegam man Beelsebul laay dàqe rab yi, seen ñoñ nag ñoom, kan lañuy dàqe ay rab? Kon kay seen ñoñ a leen tiiñal. 20 Waaye su dee loxol Yàlla laay dàqe rab yi nag, kon nguurug Yàlla agsi na ba ci yeen.
21 «Su ponkal gànnaayoo ba diis, wattu këram, alalam dina raw. 22 Waaye bu ko ku ko man songee, ba daan ko, day nangu mboolem ngànnaay lu mu yaakaaroon, ba noppi séddale alalam. 23 Ku farul ak man nag, man ngay xeex, te ku àndul ak man di dajale, yaa ngi tasaare.
24 «Aw rab wu bon, bu jàppee nit ba génn ko, day wër bérab yu fendi, di wut fu mu nopploo, te du ko gis. Su ko defee mu ne: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.” 25 Bu dikkee fekk kër gi buube, defare ba jekk, 26 day dem indi yeneen juróom ñaari rab yu ko yées, ñu bokk sancsi. Su ko defee ni nit kiy mujje mooy yées na mu jëkke.»
27 Naka la Yeesu di wax loolu, jenn jigéen ca mbooloo ma àddu ca kaw, ne ko: «Ndokklee ki la ëmb ci biiram, nàmpal la ci weenam!» 28 Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokklee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»
45 Kenn ci xamkati yoon yi nag àddu ne: «Sëriñ bi, loolu nga wax de, nun itam, xasaale nga nu ci.» 46 Yeesu itam ne: «Yeen xamkati yoon yi itam, wóoy ngalla yeen, yeen ñi sëf nit ñi sëf yu ñu àttanul, te yeen ci seen bopp, seen benn baaraam sax du ci laal. 47 Wóoy ngalla yeen, yeenay tabax bàmmeeli yonent yi, te seeni maam reyoon leen. 48 Kon yeena seedee noonu ne seen jëfi maam ya, ànd ngeen ci, ndax ñoom ñoo leen rey, yeen ngeen tabax seeni bàmmeel. 49 Looloo tax itam kàddug Yàlla giy xel, biral ne: “Maay yebal fa ñoom ay yonent aki ndaw, ñii ñu bóom, ñee, ñu bundxatal.” 50 Su ko defee yoon topp niti tey jii, deretu mboolem yonent yi tuuru, dale ko ca cosaanu àddina. 51 La dale ca deretu Abel ba ca deretu Sàkkaryaa†11.51 Seetal ci 2.Jaar-jaar ya 24.20-22., ma ñu rey ca diggante sarxalukaay ba ak bérab bu sell ba, maa leen ko wax déy, dees na ko topp niti tey jii. 52 Ngalla yeen xamkati yoon yi, yeena sànk caabiy xam-xam; yeen dugguleen, ñiy duggsi, ngeen tere leena dugg.»
53 Ba Yeesu génnee foofa, ca la Farisen ya ak firikat ya tàmbalee xabtalu ci kawam, di ko seetloo ay laaj ci mbir yu bare, 54 di ko yeeru, tey wuta këf kàddu gu rëcce ci gémmiñam, ngir tuumaal ko.
<- Luug 10Luug 12 ->