5 «Gépp kër gu ngeen dugg, jëkkleen ne: “Jàmm ñeel na leen.” 6 Su fa nitu jàmm nekkee, seen jàmm dal ko. Lu ko moy, mu délsi ci yeen. 7 Dal-leen ca kër googa, di lekk ak a naan ca la ñu leen jox, ndax liggéeykat yelloo na peyooram. Buleen di wër nag kër ak kër.
8 «Bépp dëkk bu ngeen dugg, ñu dalal leen, la ñu leen taajal, lekkleen ko. 9 Wéral leen jaragi dëkk ba, te ngeen wax waa dëkk ba, ne leen: “Nguurug Yàlla dëgmal na leen.” 10 Waaye bépp dëkk bu ngeen dugg te dalaluñu leen, demleen ca pénc ma te ngeen ne leen: 11 “Seen pëndub dëkk bi ci sunu ndëgguy tànk sax, nu ngi koy faxas, seedeele leen ko seen ngàntal. Waaye nag xamleen ne nguurug Yàlla dëgmal na.” 12 Maa leen ko wax, bu bés baa, boobu dëkk, Sodom a koy gënu demin.
13 «Wóoy ngalla yeen waa Korasin, yeen waa Beccayda it, wóoy ngalla yeen, nde kéemaan yi sottee fi seen biir, su doon fa waa Tir mbaa fa waa Sidon la sottee, kon bu yàgg lañu doon sol ay saaku, xëppoob dóom, ngir tuub. 14 Moo tax it, kera àtte ba, waa Tir ak Sidon a leen di gënu demin. 15 Yeen waa Kapernawum nag, dees na leen yékkati ba asamaan a? Xanaa ba fa njaniiw kay ngeen di wàcci.
16 «Ku leen déggal nag, man nga déggal; ku leen gàntal, man nga gàntal. Te ku ma gàntal, gàntal nga ki ma yebal.»
17 Ba juróom ñaar Fukk ñaak ñaar demee ba délsi, mbégte lañu àndal. Ñu ne: «Sang bi, rab yi sax, danu leen di jox ndigal ci sa tur, ñu nangul nu.» 18 Yeesu ne leen: «Séen naa Seytaane mu fàqe asamaan ni ag melax. 19 Dama ne, maa leen jox sañ-sañu joggi ci kawi jaan aki jiit, joggati mboolem dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ mukk. 20 Noonu leen rab yi nangule nag, buleen ko bége, bégeleen kay la seen tur binde fa asamaan.»
21 Ca waxtu woowa tembe la kemtalaayu mbégte tukkee ci Noo gu Sell gi, dugg Yeesu, mu daldi ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi, nde loolu de, Baay, mooy li la soob. 22 Lépp la ma sama Baay dénk, te kenn xamul kuy Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it xamul kuy Baay bi, ku dul Doom ji, ak képp ku ko Doom ji namma xamal.»
23 Ci kaw loolu Yeesu walbatiku ca taalibe ya, wax leen ñoomu neen, ne leen: «Ndokklee ñi seeni gët gis li ngeen gis. 24 Ndax maa leen ko wax, bare na ay yonent ak buur yu bëggoona gis li ngeen gis, te gisuñu ko, ak itam dégg li ngeen dégg, te dégguñu ko.»
30 Yeesu neeti ko: «Jenn waay a jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Mu dajeek ay sàcc, ñu futti ko, dóor ko, daldi dem, bàyyi ko, muy waaja dee. 31 Yàlla woo yàlla ab sarxalkat bu jaare yoon woowa, séen nit ka, daldi teggi. 32 Jenn waay ju soqikoo ci giirug Lewi it noonu; daa dikk ba tollu foofa, séen waa ja, daldi teggi. 33 Jenn waay ju dëkk Samari nag doon tukki, dikk ba jege waa ja, xool ko, yërëm ko lool. 34 Mu dikk, sotti diw ak biiñ ca gaañu-gaañu ya, lëmës ko. Ci kaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci ab dalukaay, di ko topptoo. 35 Ca ëllëg sa, mu yékkati ñaari poseti xaalis†10.35 Benn poset bu ci nekk, benn dinaar la tollool, te moo doon peyooru benn bésub lëmm. Seetal Xaalis ci Leeral yi., jox ko boroom dal ba, ne ko: “Topptoo ko waa ji. Loo ci dolli, bu ma dëppee, maa la koy delloo.”»
36 Mu teg ca ne ko: «Ñett ñii, kan nga foog ne moo ci taxawu waa ja dajeek sàcc ya, taxawaayu nit ak moroomam?» 37 Mu ne ko: «Xanaa ki ko defal yërmande.» Yeesu nag ne ko: «Demal boog, di defe noonu.»