13 «Gannaaw loolu bu boroom jàngoroy xelli ji tàggook sobey jàngoro ja, dafa wara waññ juróom ñaari fan ngir setlu, ba noppi fóot ay yéreem, sangoo ndox mu balle ci bëtu ndox, doora set. 14 Bésub juróom ñetteel ba, na wut ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw te teewi fi kanam Aji Sax ji ca bunt xaymab ndaje ma, daldi koy jox sarxalkat bi. 15 Sarxalkat bi day rendi yooyu, menn mi di saraxu póotum bàkkaar, mi ci des di saraxu rendi-dóomal. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji ndax jàngoroy xelleem jooju.
16 «Su góor génnee wasal, war naa ragg yaramam wépp, te du tere mu yendoo sobe ba jant so. 17 Lépp luy yére mbaa der bu wasal taq, dees koy fóot te du tere mu yendoo sobe ba jant so. 18 Su dee jigéen ju góor àndal, te wasal génn, nañu sangu, te du tere ñu yendoo sobe ba jant so.
25 «Kuy xëpp deret ay fan yu bare te du jamonoy baaxam, mbaa mu gis mbërëg mu wees àpp bi mu ko baaxoo gis, kooka sobewu na diiru fan yi muy xëpp. Day mel ni bu nekkee ci jamonoy baaxam. 26 Lal bu mu tëdd ci diir bi muy xëpp yépp, day mel ni lalam bu ko fekk ci jamonoy baax te lépp lu mu toog day sobewu, ni bu nekkoon ci jamonoy baaxam. 27 Ku laal lenn ci yooyu yëf, kooka sobewu na. War naa fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
28 «Bu xëppee ba jeexal, dina waññ juróom ñaari fan, doora tàggook sobe sa. 29 Bésub juróom ñetteel ba na wut ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, yóbbu ca sarxalkat ba, ca bunt xaymab ndaje ma. 30 Sarxalkat bi day rendi menn mi muy saraxu póotum bàkkaar, mi ci des doon saraxu rendi-dóomal. Su ko defee sarxalkat bi defal ko ko njotlaay fi kanam Aji Sax ji ndax sobey xëpp ja.
31 «Fexeleen ba bànni Israyil di tàggook seeni sobe, lu ko moy dinañu dee ndax seen sobe, ngir dañuy taqal sama màkkaan mi ci seen biir.»
32 Loolu la yoon digle ci mbiri góor gu ànd ak jàngoroy xelli mbaa mu génne wasal, ba sobewu; 33 ak jigéen ju nekk ci jamonoy baaxam; ci gàttal képp ku taq sobe suy génne ci moom, muy góor mbaa jigéen, ak itam góor gu dëkkoo jigéen ju sobewu.
<- Sarxalkat yi 14Sarxalkat yi 16 ->